Paap Ibraayma Géy, ñu gën koo xame ci dàkkentalu “Papitoo Kara” moo génn àddina. Moom nag, nee ñu da doon mbëkki. Maanaam dafa bëggoon a dem Espaañ jaare ko ci géej gi. Waaye, mujjul àgg, ci ndox mi la ñàkke bakkanam. Démb ak léegi nag, xibaar yu wuute rot nañ ci. Waaye, am na ñu dëggal démb ci àllarba ji ne, moom Papitoo Kara génn na àdduna. Nee ñu, sedd bee ko jàpp ba mu mujje faatu. Ndeysaan…
BÀYYI NAÑU AAMADU BA AK FAATIMATA KAN
Àjjuma jii weesu lañu tegoon loxo Aamadu Ba kenn ci kilifay Pastef yi. Nee ñu, li ñu ko doon toppe mooy siiwal wayndarew caytug wér-gu-yaramu Usmaan Sonko. Waaye, layookatu Usmaan Sonko bii di Xuwaan Baranko fésal na ci mbaali jokkoo yi ne wayndare yooyu ñuy wax ne Aamadu Ba daf leen a biral, moom mooy ndeyi-mbill gi. Maanaam, mooy ki ko njëkk a génnee, tas ko ci mbaali jokkoo yi. Moom Aamadu Ba sax mujj nañu ko bàyyi démb def ko li ñu naan “ sous controle judiciaire”.
Naka noonu Faatimata Kan nga xam ne looloo taxoon ñu teg ko loxo tamit, bàyyi nañ. Dafa tasoon wayndare woowu ci mbaali jokkoo yi mujj nañu ko bàyyi démb. Terewul ne, moom it, ñu def koli ñuy dippe “sous controle judiciaire”.
USMAAN SONKO AK YOONU SENEGAAL
Ay fan ginnaaw bi ko ëttu àttewaay bu Sigicoor joxee woon dëgg, talaata jii tamit waa CENA (Commission Electorale Nationale Autonome), mbootaay gi ñu dénk wàlluw wote yi, digalaat nañ ñii di waa DGE (Direction Générale des Elections) ñu jox ko ay xobi baayaleem ni ñu ko joxee ay moroomam. Waaye, waa DGE moom fa ñu tegoon seen tànk, teggiwuñu ko. Ndax, ab diir lañu ca teg rekk ñoom it ñu génnee seen ub yégle wone ne fa ñu nekkoon jóguñu fa. Li ñu ko layalee mooy ne Njiitul Pastef li nekkul ci wayndarew wote yi. Kon, mënuñu koo jox, ay xobi baayaleem.
ÑÀKKUM JÀNGALEKAT CA KAFRIN
Daaray Kafrin yu suufe ya ak yu digg-dóomu yaa ngay jooy ñàkkug jàngalekat. Ki xamle loolu mooy “inspecteur d’académie” ba, Abdulaay Wàdd. Nee na, diwaanu Kafrin mànke na lu tollu ci téeméer ak ñaar-fukki jàngalekat. Li ko waral mooy ne jàngalekat yu bari dañoo jóge foofu dem ci yeneen i béréb. Ci daara yu suufe yi rekk, téeméer ak ñeent-fukk ak ñett dem nañu te, juróom-fukk ak benn ñoo ñëw. Ci yu digg-dóomu yi, ñaar-fukk ak juróom-benn ñoo dem, fukk ak benn ñëw (moyen), feneen fi (secondaire) fukk ak juróom-ñeent dem, fukk ak juroom-ñeent ñëw. Bu ñu xaymaa ñoom li ñu soxla, nee na mi ngi tollu ci téeméeri jàngalekat ak ñaar-fukk.
CAF AWARDS
CAF AWARDS di neexal bu ñu jagleel xale bi gën a ràññeeku Afrig ci wàllu futbal. Loolu nag doomu Senegaal bii di Paap Mataar Saar moo ko jëloon at mii weesu. Waaye, ren jii tamit am na ñeenti doomi Senegaal yu bokk ci ñiy xëccoo raaya googu. Muy kii di Aamara Juuf, Lamin Kamara, Paap Demba Jóob ak Paap Aamadu Jàllo. Ñu koy xëccoo ak yeneen doomi Afrig yii di Abdesamad Ezalzuli (Marog), Gift Orban (Niseriyaa), Dàngo Watara (Burkinaa Faaso), Bilaal Al Xanus (Marog), Sulaymaan Alid (Burkinaa Faaso) ak kii di Enerst Nuamah (Gana).