LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (2/9/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA SIIN

Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo nga jamono yii fa réewum Siin. Muy Tukki bu mu fay amal ci turu Njiitu réew li mu doon ak xew-xewub FOCAC bi mu fa namm a fekke ci 4 ba 6i pani weeru sàttumbar bi. Bu weesoo ñi mu daan faral a àndal, Njiitu réew mi rax na ci ñi ko fa gunge ñenn ci kurélu njaatige yi (le patronnat) ak ñaari ndongo yi jëloon raw-gàddu gi ci joŋante ndongo yi gën a xarañ fi réew mi.

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI

Réewum Senegaal moo ngi ci yoonu dooleel njàng meek njàngale mi. Jëwriñal njàng meek jëwriñal làrme bi ñoo lënkoo taxawal banqaas bu ñu duppe LYNAQE (Lycée Nation-Armée pour la Qualité et l’Équité). Muy liise bob dañ ko sos ci ndigalul Elimaanu jëwriñ yi. Lees ko dugge nag mooy boole seen doole ak seen i mën-mën ngir taxawal daara ju sampu ciy mbaax. Muy nag naal bu Càmm gi namm ngir tëggaat daaray Senegaal ci tolluwaayu Jamono ak li mu laaj.

BANQAAS GI

Liggéeykati banqaas gi jël nañ seen yoonub bopp. Ginnaaw bi leen magum jëwriñ yi digalee ñu defaraat seen toogiin, ab kayitu ñaxtu lañ ko tontoo. Bees sukkandikoo ci yégle bi ñu génne, li ñuy séentu ci Elimaanu Jëwriñ yi mooy mu saafaral leen seen I jafe-jafe, waaye du génne ab bataaxal ngir joxe ay ndigal. Bees sukkandikoo ci kayitu ñaxtu bi ñu siiwal, ñoo ngi sàkku ci Càmm gi mu ñoŋal anam yi ñuy liggéeyee fa Jamñaajo ak ci barab yu nekk ci gox yeek gox-goxaan yi, sàmmonteek peyooru ndàmpaay yi, dugal liggéeykat yi mu jëlandi woon (contractuels) ci liggéeykati Nguur gi, añs.

DIINE

Dinañu màggal gàmmu Tiwaawan guddig 15 jàpp 16 ci weeru sàttumbar wi. Sëñ Abdul Hamid Sy Al Amiin mi jiite pekku sawiya tiijaan bu Sowu Tiwaawan moo ko xamle ci janoo bi mu doon amal ak saabalkat yi. Gàmmu ren ji nag, ñoo ngi ko tënk ci ponk bii di “dañu maa yónni ngir ma mottali mbaax yi màgg”. Muy am njàngalem Yónnent Yàlla Muhammad (saws) mu ñu fas yéene sukkandiku ngir nafar mbooleem mbaax yi mu jàngale te gën leen a wasaare.

MBËKK MI

Fa Mbuur, lu ëpp 20i ndaw réer nañu ci géej gi. Ñuy ay ndaw yu dëkk ci kàrce bu ñuy wax tefes, jóge woon fa, wutali réewum Espaañ. Bees sukkandikoo ci li seen i mbokk fésal, bi ñu fa jógee ak tey mat na 21i pan, te ba léegi kenn déggu leen, kenn xamul ci lu ñu nekk. Ñu ëpp ci ñoom nag ay nappkat lañu. Lu ni mel jural seen way-jur yi njàqare ak jaaxle buñ xamul fu ñu koy jooytoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj