Dépite yaa ngi wéy di nattal jëwriñi Càmm gi seen i gafaka ñeel atum 2024. Ñu doon nattal tey jëwriñu kéewnga leek yi ci aju. Ginnaaw waxtaan waak weccante xalaat ya, daldi nañ ko jagleel 48i Tamñareet ak lu teg. Ñu seetlu ci yokkute bu baax bees ko gam-gamleek gu daaw gog, ci 38i tamñareet ak tuut la yemoon.
Li sabab yokkute googu nag di liggéey bu am solo biy xaar jëwriñ ji. Ñu gën cee ràññe jumtukaayi óosefoore (eaux et forêts) yi mu war a yokk ngir ñu mën a aar àll yi, koppar gi mu war a jagleel kurél giy xeex daay yi, njëmbët garab yees war a amal ci lu jëm ci Grande muraille verte ak it jumtukaay yi mu war a sàkk ngir aar tefes gi.
WOTEY 2024 YI
Tey ci altine ji la wutug baayale yi tàmbali ak Pastef ga woon. Basiiru Jomaay Fay nag lañu fas yéene jiital ginnaaw bi mbiri Usmaan Sonko tëwee sotti ba léegi. Bees sukkandikoo ci yégle Usmaan Sonko bi ñu siiwal démb, tànneefu Basiiru Jomaay Fay doon na lu ñu waxtaane woon bu yàgg. War naa mat at, waaye dañ ko nëbboon, bañ koo siiwal.
Basiiru Jomaay Fay nag, ni waayam ji Usmaan Sonko, mi ngi ci kaso bi ba léegi. Ci weeru awril 2024 wi la ko yoon tegoon loxo. Fekk mu bindoon ci xëtu facebookam doon ŋàññ àttekat yi ci mbiri Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ. Ñu koy toppee ni dafa xotti wormay àttekat yooyu ak campeef gi ñu bokk.
ÀQ AK YELLEEFI XALE YI
Tey ci bésub 20 nowàmbar la àddina wërngal këpp di màggal bés bees jagleel àq ak yelleefi xale yi. Fii ci Senegaal, ñu koy màggal nees ko daan defe at mu jot. Waaye, bu ren ji, dees ci gën a fësal xale yi ànd ak laago. Muy tomb bi ñu tànn. Liñ ci namm nag di waxtaane nees war a fexe ba ñu am nekkin wu mucc ayib, kenn bañ leen a beddi ci lenn. Bu ko defee, ñu mën leen a bàyyi xel bu baax ba ñu mën a gis seen bopp ci mboolaay mi.
BITIM-RÉEW
Fa Haraare, Simbaabóoy, nguur ga jël na fa ndogalu tëral ag guural, maanaam « Etat d’urgence ». Li ko waral nag mooy jàngoroy Koleraa ji tàmbalee law foofu ba andi fa tiitaange. Jot na fa sax rey lu tollu ci 51i doom-aadama. Am na yeneen 150i nit ñu faatu yees njort ni jàngoro jee leen faat.
Fa Bande de Gaza itam, sóobarey Israayel yaa ngay wéyal seen cong ma ca bëj-gànnaaru dëkk ba. Li ci gënatee yéeme nag mooy bàyyiwuñu sax loppitaal yi. Ci seen sox yi mujje, 12i nit ñàkkaat nañ seen bakkan ca loppitaalu Endonesi bu nekk fa Gaza.