Bu yàggul dara lañu jàppoon layoo Maam Mbay ak Usmaan Sonko ngir ñu àttewaat leen. Waaye, layoo boobu mujjul woon a am. Xibaar rot na ci ne, seen layoo boobu jàppalaat nañu ko àpp. Wii yoon àtte ba ca ëttu àttewaay bu kowe (cour suprême) ba lay amee ngir ñu leeral coow loolu doxoon seen diggante ba ñu jotoon cee daan Njiitul Pastef li. Layoo boobu jàpp nañu ko ñeenti fan ci weeru saŋwiye wii ñu jëm atum 2024.
GÀNTALATI NAÑU AYIB DAFE
Démb ci talaata ji la Ayib Dafe demoon ca DGE (Direction Générale des Elections) ngir jëlal Usmaan Sonko xobi baayale. Li waral loolu mooy ne àttekatu ëttu àttewaayu Ndakaaru moo ne nañu ko delloo ci wayndarew wote yi. Moo taxoon démb moom, Ayib mu demoon ngir jëlal ko xobi baayaleem. Waaye, loolu mujjul woon a àntu. Ndax, takk-der yi dañu ne leen dungeen fi dugg. Naka noonu, tey tamit dañu ko terewaat mu duggu ca béréb bii di CDS (Caisse des Dépots et de Consignation). Terewul ñii di waa CENA (Commission Electorale Nationale Autonome) moom dalal nañu ko.
MBËKK MI
Jamano jii ñu tollu, ñu bari foogoon nañu ne mbëkk mi wàññeeku na. Ndeke tey la gën a am doole. Maanaam, ndaw ñaa ngi dem ba tey, ñu yég ko walla ñu ñàkk ko yég. Ndax, njiitul kurél gii di “Réseau national des quais de pêche du Sénégal” xamle na ne am na lu tollu ci fukki gaal yoo xam daanaka ñaari weer a ngi nii xamuñu fan lañu nekk ak ci lan lañu nekk. Ci gàttal, gaal yooyu dañoo réer, kenn xamul fuñ duggu. Ci xayma li nekkoon ci gaal yooyu war na dem ci junni ak juróomi téeméer. Ñi ngi woo kilifa ya ñu dimbali leen ngir seen mbokk yooyu réer mën a feeñ.
XEW-XEW BU TIIS
Jenn waay juy wuyoo ci turu O. Balde moo jam benn xaritam mu génn àdduna. Nee ñu, li waral coow li mooy, benn saaku mboq bu ñu leen boole woon ca waaxu Ndakaaru (Port autonome de Dakar). Ginnaaw gi, ci la ko xarit bi S. Ture bëggoon a jaar ci kowam, faf mbir ma mujje ëpp i loxo. Ndax, dañoo waroon a séddoo saaku bi. Waaye, S. Ture daf ko bëggoon a nax, jaay saaku bi. Ci kow loolu, ñu daldi jote, xeex, O. Balde jam xarit ba paaka luy tollook ñeenti jam-jam, xarit ba jaar fa ñàkk bakkanam. Moom O. Balde nag jamono jii ma nga ca loxoy Yoon.
BENEEN XEW-XEW BU TIIS CA LINGEER
Dëkk bii di Lumbol-Manko nekk ca goxu Gasaan, fa Lingeer, lañu fekk nit ku tollu ci ñeen-fukki at mu dee ci anam yu doy waar. Ndax, nee ñu, dañoo fekk ay gaañu-gaañu ci kanam gi ak ci bopp bi. Li ci gënatee doy waar mooy bopp bi dafa ubbeeku. Maanaam, ni ñu gisee mbir mu dañoo jàpp ne sax, dafa am ku mu doon joteel ba jaar fa ñàkk bakkanam. Néew ba nag, yóbbu nañu ko ca morgo raglub Màgget Lóo bu Lingeer. Waa sàndarmëri ba tamit door nañu seen i luññutu ngir xam lan moo waral loolu ak ku ci laale.