Ngóone Mbeng mooy wuutu Bàrtelemi Toy Jaas fa boppu meeri bu Ndakaaru. Li waral loolu du lenn lu moy daan yi gàllu ci kow ndoddam ñeel bóomug Njaga Juuf gi. Looloo tax mu ñàkk moomeg dépiteem fa Ngomblaan ga. Ginnaaw gi ca la ko perefe ba jële ca meeri bu Ndakaaru. Jébbal na ay dabantal ci banqaasi Yoon yu wute. Waaye, jamono jii moom kiy wéyal liggéey bi fa meeri ba mooy soxna soosu ba ñu xam fu wànnent di mujje ak i bëtam.
MEERI BU CEES INDI NA AY LEERAL ÑEEL TËNUB LAT-JOOR BI
Ginnaaw bi ñu aajaree tën bi ñu defaral jàmbaar jooju, coow lu bari daf cee topp. Ndax, dafa am ay saabalukaay ak ñenn ci mbaali jokkoo yi ñu siiwal njëgug ndefar gi. Te, li ñu doon xamle mooy ne tën boobu ñi ngi ko defaree lu tollu ci juróom-ñaar-fukki miliyoŋ ci sunuy xaalis. Waa meeri bu Cees nag génnee nañu ab yégle ngir indi ay leeral ci mbir moomu. Nee nañu xibaar yooyu wérul. Li ñu defaree tënub Lat-Joor Ngóone Latiir Jóob bi, lépp lépp mi ngi tollu ci ñeen-fukk ak ñeenti miliyoŋ yu teg juróom-benn ak fanweer ak juróom-ñett yu teg téeméer (44.338.500).
JÀPP NAÑU ÀPP “DPG” BI
Bu yàgg ba tay ñi ngi ci ay jàppal bàyyil ñeel mbirum DPG bi. Ndax, ay weer ginnaaw bi ñu tabbee Usmaan Sonko elimaanu jëwriñ, ci la waroon a def DPG. Mu amoon ay càrt yu mu doon sàkku ñu soppi leen laata mu koy defi fa Ngomblaan ga. Waaye, loolu taxul woon mu mujje dem. Nde, ci diggante bi, dañu cee tas Ngomblaan ga woon, amalaat ay wote. Léegi nag, taxawal nañu fukk ak juróomeelu kayug Ngomblaan gi ba noppi. Moom elimaanu jëwriñ yi dina amal ab DPG (Déclaration de Politique Générale) ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru desàmbar wii ñu nekk. Barki-démb lañu ko xamle fa ndajem jëwriñ ya.
XEW-XEW BU TIIS FA TUUBA
Xew-xew boobu mi ngi ame ci benn dëkk bu jege Tuubaa Belel, boori Tuubaa Mbàkke. Benn baykat la fa ab masin (machine batteuse) ray. Nee ñu, baykat bi, ni mu ko doon jëfandikoo moo jaarul yoon bees sukkandikoo ci waa Senego. Ci la masin bi tàqalee bopp bi ak yaram wi. Mu doon mbir mu doy waar te metti lool.