Ndajem Ndeyu àtte réew mi génnee beneen listu 19i lawax yi war a joŋante ci wotey 2024 yi. Tey lañ siiwal seen toftale googu. Nde, lawax bii di Róos Wardini dafa mujje bàyyi.
RÓOS WARDINI BÀYYI NA
Róos Wardini bokkatul ci wotey 2024 yi. Li ko sabab mooy lees ko tuumaal mbirum nasiyonaalite Farãs bi mu ame. Moom nag, Róos Wardini miy njiitul kurél gii di “Sénégal nouveau” dafa xàddi. Ca ndaje ma mu amaloon ak taskati xibaar yi daf ci wax ne :
“Jàmm ak juboo doomi réew mépp moo jiitu bépp xeetu bëgg-bëgg. Moo tax ma jël ndogalu tege boor yéene ji ma amoon [nekk lawax] di yaakaar ne loolu dina yombal doxalinu wote yi, di njort tamit ne wote yi dinañ am keroog 2 awril 2024.”
BËGG-BËGGU LAWAX YI JÀLLUL
Jamono yii, Njiitu réew mee ngi nekk di dalal lawax yi ngir dëppoo ak ñoom cib bés bees war a jàpp ngir amal ci wote yi. Waaye, lawax yi Ndajem Ndeyu àtte mi gàntaloon noppeeguñoo jooytu. Li ñu bëgg nag mooy ñu delloo mbir yi ca njëlbeen ga, tàmbaliwaat lépp ba ci saytuwaat wayndare lawax yi. Li ñu jàpp te siiwal ko ci bi ñuy janook taskati xibaar yi mooy ni, ndeem Ndajem Ndeyu àtte mi nangu na ñu amal wote yi ci beneen bés bu dul 25 féewiryee bi, lépp lees fi nasoon dafay daldi nocceeku. Ba tax na Njiitu réew mi dafa war a woote diisoo bu yaatu bu ñéppdi bokk te ñu amal sàrtu wote yu yees.
NDIISOOG LUÑÑUTU GI SOOY NA
Ndiisoog luññutu gees taxawaloon fa Ngombalaan ga sooy na. Dañuy dakkal liggéey bi mu nammoon a amal ci way-bokki Ndajem Ndeyu àtte mi te waa PDS doon leen jiiñ nger ci caytug wayndare lawax yi. Mbirum nger googu sax ñu cay tudd moo andi coowal wote yi. Nde moo taxoon ba Njiitu réew mi ajandi bés bi. Nguur giy àtte nag moo ci dugal loxoom, fas yéene cee amal luññutu. Te, ci doxiinu biir Ngombalaan gi, saa bu yoon jubloo mbir, ndiisoog luññutu gees ci taxawaloon fa Ngombalaan ga dootul amati solo. Dees koy dakkal.
RADDHO SOÑÑAAT NA NJIITU RÉEW MI
Ci ñaari ayu-bés yi ñu génn, 664 ci ñi ñu nëbboon jant bi génne nañu leen ndung-siin. Muy lim bi waa RADDOH (Rencontre Africaine pour la Défense des Droits de l’Homme) siiwal bërki-démb ci dibéer ji. Bàyyi yooyu nag, ñoo ngi am ginnaaw bi Njiitu réew mi jëlee ndogalu sàkk i pexe ngir suuxat jàmmoo ci réew mi, rawatina ci jamonoy wote yi ñu tollu. Naka noonu, waa RADDHO dellu nañ di soññ Njiitu réew mi ngir mu wéy ci doxaliin woowii te bàyyi ñépp ñi ñu tegoon loxo ci diggante ñaari at yi, te jàppewuñu leen lu dul mbiri pólitig. Ndax, dina dolli dal bu baax a baax ci réew mi.
DABA JUUF FEKKI NA DIJJE BAAJI
Dijje Baaji, kenn ci sàndarm yi fi réeroon ci weeru nowàmbar 2022 ba léegi la soxnaam si, Daba Juuf, faatu. Tey ci altine ji la ko dépite bii di Gii Maris Saañaa siiwal. Ci xibaar yi mu jot a siiwal, ndaw si dafa tawatoon ci weeru sãwiyee bi. Moom sax, ma nga faatoo fa réewum Farãs ma mu doon liggéeyee.