Kuréel gi ëmb jàngalekat yi nekk ci daara yu kowe yu noppeegul ci xeex bi mu door digganteem ak Nguur gi. Ndax, talaata ak àllarba dañoo dakkaloon seen ub liggéey. Waaye, yamuñu foofu. Démb ci àllarba ji amaloon nañu ndajem waxtaan. Li ñu ko dugge mooy ñaawlu dundin wu metti wi njabooti seen naataango yi génn àdduna di dund. Te, lépp Nguur gi ne ci patt-pattaaral, mel ne ñu yëgul li géej gi di riir. Nee ñu, duñu ko nangu te duñu bàyyi dara mu sedd. Dinañ wéy di xeex loolu ba fu mu yam neex.
SAEMSS AK CUSEMS ÑI NGI ÀRTU
Coowoo yi dox ci diggante Nguur ak jàngalekat yi mel na ne am na fu mu doore, waaye, kenn xamagul fu muy yam. Ndax, démb ak barki-démb la jàngalekati daara yu kowe yi dakkaloon seen um njàngale. Ñu ne déet-a-waay, jàngalekat yi nekk ci daara yu digg-dóomu yi jóg di àrtu. Sàndikaa yi leen ëmb di SAEMSS (Syndicat Autonome des Enseignants du Moyen-Secondaire du Sénégal) ak CUSEMS (Cadre Unitaire Syndical des Enseignants du Moyen-Secondaire) génnee nañu ab yégle tay ci alxames ji. Li ñu ko dugge mooy fàttali Nguur gu bees gi déggoo yi ñu xaatimoon ak Nguur gi fi jóge. Li ñu bëgg mooy Nguur gi def ci yitte te bañ a xalaat a teg baat yi déggoo yooyu nga xam ne ci xeex bu metti lañu ko ame.
EL HAAJ ELIMAAN NDUUR WÀCC NA LIGGÉEY
Tiis wu metti moo dal ci kow waykat bu mag bii di Yuusu Nduur ak ug njabootam. Way-juram wu góor, El Haaj Elimaan Nduur, moo génn àdduna biig. Jébbal nañu ko Boroomam tay ci alxames ji. Moom El Haaj Elimaan Nduur amoon na lu tollu ci juróom-ñeen-fukki at ak juróom-ñett.
WOO NAÑU AADAMA ADUS FAAL FA DIC
Sànq ci bëccëg la Aadama Adus Faal bu làngug APR (Alliance Pour la République) fésal ci xëtu Faacebookam ne dañu koo woolu. Li mu xamle nag mooy ne woo nañu ko fa DIC (Division des Investigations Criminelles) bu ñeenti waxtu ci ngoon jotee. Ci kàddu yooyu kepp la yam. Maanaam, leeralul lan moo sabab woote boobu.
CNG TËRAL NA SÀRT YU BEES
Dibéer jii weesu lañu doon amal làmb ji doxoon diggante Amaa Balde ak Faraŋ. Ba làmb ja jeexee nag, taafar su dul jeex am ca ba bakkan rot ci. Ginnaaw gi la waa-pólis jël ndogal ne dañuy dakkal wattug kaaraange gi ci làmb yi fii ak ub diir. Bi ndogal loolu rotee, ci la waa CNG (Comité National de Gestion de la lutte) génn teg ay sàrt yu bees. Maanaam, léegi làmb yi diggante ñeenti waxtu yu teg fanweeri simili ak juróom-ñaari waxtu lañu leen di amal. Rax-ci-dolli, palaas yi ñu yamale leen ci 22 000 rekk. Ñiy tëgg làmb, kenn dootu ci jaay lu ëpp 22 000iy biyes. Li ñu ci jublu mooy kilifa yooyu dellusiwaat ngir ñu am kaaraange gu mat sëkk. Su ko defee, ñu mën a wéyal seen liggéey.