LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (20/7/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

F24

Kurél gii di F24 boole ay làngi pólitig ak i way-moomeel dafa nammoon a amal am ndaje ci àjjuma jii. Ndaje moomu nag ma nga ko bëggoon a amale ca béréb bii ñuy dippe “Place de la nation”. Li ñu ko dugge woon mooy kaas ngir ñu bàyyi mbooleem ñi ñu jàpp ci sababu wute gis-gis ci pólitig. Dañuy xeex ngir ñu amal ay wote yu leer nàññ ak ñu sàmm demokaraasi bi. Moomu ndaje nag mujjul àntu. Ndax, calawu (perefe) Ndakaaru li, Moor Taala Tin, mooy ki ko gàntal. Nde, dafa jàpp ne loolu mën na yee fitna walla mu nasaxal dem bi ak dikk bi.

Ndajem Ngomblaan ga

Ci altine jii weesu lañu njëkkoon a amal um ndajem. Tey nag, seen ndaje mi poñ yi ko wund, bi ci gën a  fés mooy waxtaane dogub 29 bi ñeel mbirum parenaas yi. Li ñeel dogub 87 bi juroon coow ci réew mi, mujj nañu ko génne. Càrt boobu ñuy càmbar tey bu ci déggoo amee, ay coppite yu yees dina am ci mbirum parenaas bi rawatina ci lim bi. Loolu nag, jur na jiixi-jaaxa ci boppi ñenn ñi séq mbir moomu.

Càkkutéefi bàyyig négandiku

Ay weer ginnaaw bi ñu tegee loxo gaa yooyu ñuy dippe “détenus politiques”. Ba tey, ña nga ca kaso ya. Meetar Musaa Saar di layookatu kii di Muhamed Sàmb Jim “Hanibal” ak Nuuru Ba, dugaloon na bataaxalu càkkuteefu bàyyig négandiku. Waaye, càkkuteef googu mujjul a àntu. Ndax, dañu ko ko gàntal.

Naka noonu, yeneen càkkuteef yi mu defaloon Basiiru Jomaay Fay ak Paap Abdulaay Ture tamit dañu leen a gàntal. Kii di Moor Taala Géy ñu gën ko xame ci Nit Dof, moom it noonu la mbiram deme. Ba tey ña nga ca kaso ba.

Njuréefi BAC 2023

Ginnaaw lu jege ayu-bés bi joŋante bii di BAC jeexee, njureef yi jàppandi nañu. Maanaam, xamees na limu njàngaan yi am BAC ci réew mépp. Lu tollu ci 155.109 ndongo yi doon def BAC yi ñu tas ci lu tollu 495i nit yu ko war a doxal. Ñooñu lu tollu ci 77.284i njàngaan am nañu seen lijaasa boobu di BAC. Te, 34.261 yépp ci yoon wu njëkk wi lañu ko ame. Mu am tamit lu tollu ci 77.825i ndongo yoo xam ne amuñu lijaasa bi. Ñu xayma li am BAC ci Senegaal atum 2023 muy téeméer boo jël lu tollu ci juróom-fukk ak benn am nañu ci, maanaam 51,54%.

Mbëkk mi

Mbirum mbëkk mi mel na ni dafa wër Afrig, rawatina Afrig sowu jant. Ndax, Daxla ca Marog rekk nemmeeku nañu fa lu tollu ci ñeenti téeméeri nit ñoo xam ne dañu doon mbëkk ngir dem bitim-réew. Ci biir ñooñu, ñaari téeméer ak fanweer ak benn yi ay doomi Senegaal la yoy. Ki ko xamle mooy Dr Anet Njaay mi ñu dénk doomi Senegaal ya nekk ca bitim-réew. Nee na, ñooñu moom, delloosi nañu leen. Am na ci fukk ak juróom-ñett yoo xam ne ñi ngi ci raglu ya nekke ca Marog. Waaye, terewul ne am na ci ñett ñoo xam ne sii, ñàkk nañu ci seen i bakkan.

Jéyya ca Podoor

Ayu-bés bii ñu génn la am jéyya ju amoon ci ndox mi fale ca Ndar, jeneen am na ca Podoor. Geneen gaal moo fa këppu. Li jot a rotagum ci xibaar, nee ñu ñaari nit a ci ñàkk seen i bakkan. Ñaar ñooñu ay seex lañu yu amoon juróom-ñeenti at. Nee ñu, Moritani la jóge woon. Waaye, waa ji ko doon dawal ak yaayu xale yi moom dara dalu leen.

Xibaari gayndey futbal yi

Ñenn ci gayndey Senegaal yi ña nga ca yoonu dem ci yeneen ékib yu bees. Ku ci mel ni Saajo Maane nekk ca Bayern, ay xibaar rot nañ ne, tàmbali naa am i jokkoo ak ékibu Araabi Sawdit bii di Al Nasr. Maanaam mi ngi waxaale ngir jënd gaynde gi. Kii di Abdu Jàllo tamit, nga xam ne boolewuñu ko ci ékibu Paris bi war a joŋante seen joŋante bu njëkk. Am na nag ékib yu ko soxla. Muy bu ci mel ni Réal Bétis nekke fale ca Espaañ ak Naples ca Itali ñi ngi ci tànki jënd gaynde gooogu. Kii di Ilimaan Njaay, moom ba tey digganteem ak Olympique de Marseille jeexagul. Ndaxte, ékibam bëggukoo bàyyi. Waaye, dees na xam fu wànnent di mujjeek i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj