Ginnaaw bi ñu wotee àtte biy soppi sàrt-biiru ngombalaan gi, coowal tas gee ngi wéy ñuy amal ba léegi. Waaye, bu ko Njiiitu réew mi tasee, dina war ñu amal i wote yu gaaw. Muy nag lu nar a indi beneen jafe-jafe. Nde, ngir ñu mën koo amal diggante weeri nowàmbar ak desàmbar, dina laaj koppar gu tollu ci 10i tamndareet. Te, bees tasee ngombalaan gi, dootuñ mën a joyyanti gafaka gi te Njiitu réew mi du am sañ-sañu joxe ndigal ñu génne alal jooju. Kon, ci guuta lañu nekk.
PÉNCOOM YAALE JI (DEM BEEK DIKK BI)
Jëwriñu tabaxte yi (infrastructures) ak yaaley suuf seek jaww ji, El Maalig Njaay, woote nam ndaje. Muy ndaje mom, moo ngi aju ci waajtaayu péncoo mi nga xam ni dees na ko amal ci wàllu dem beek dikk bi. Mu nar cee waxtaan ak way-yëngu yeek ñi seen xel màcc ci wàll wi ngir méngale seen i taxawaay. Dinañu amal ndaje mi ci diiru ñeenti pan, dale ko ci altine ji, 19i pani ut ba keroog alxames 22i pani ut 2024.
WAAJTAAYU MÀGGAL GI
Ay pan képp a des ci màggalug Tuubaa gi. Ay tamndareeti doom-aadama di bawoo fu nekk ngir fekkeeji ko. Naka noonu, El Maalig Njaay demoon na fa ci turu jëwriñ ji mu doon te yore tabaxte yi ak yaale ji. Ngir yombalal taalibe yi seen demug màggal, moom jëwriñ ji xamle na ni dees na leen jagleel lu ëpp 200i biisi Dakaar Dem Dikk ak ay saxaar. Lépp ngir bañ ñu am i jafe-jafe ci seen tukki, waayeet ngir kenn bañ a yokk paas yi.
NDOGALI CÀMM GI CI NDOG YI
Jëwriñ jiñ dénk wàllu dem beek dikk bi jël na ndogal yu bees ci ndog yu bari yi ci tali bi. Ginnaaw seetlu yiñ def, ndog yu mujj yépp ci càggante dawalkat yi la sosoo, moo xam dañuy nelaw, daw lu ëpp mbaa teggee naka sa dul noonu. Ba tax na, dina lënkook jëwriñu làrme bi, daldi tëral ay ndogal. Bokk na ci ndogal yooyu, yokk kaaraange gi ci yoon yi, di ga dawalkat yi ci ñuy taxaw di dal-lu. Dinañu taral daan yeet ba àgg ci tëjaate ak yenn jalgati yi.