Démb ci talaata ji la Njiitu réew mi jibal kàdduy tàggatoom ca ndajem Mbootaayu Xeet ma. Lii mooy doon yoonam wu mujj ca ndaje mooma ginnaaw ba mu xamlee ci weeru sulet wii ne du bokk ci wote yii di ñëw. Nee na wote yooyu ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru féewaryee 2024. Wote yooyu dinañu mel ne yi leen jiitu. Dinañu doon yu leer nàññ yu dul am genn baara-yégoo. Te, nee na, ñaari fan ci weeru awril dina joxe lenge yi ginnaaw fukki at ak ñaar ya mu leen yore. Mi ngi tëje kàdduy cant ak ngërëm ñeel mboolem réew yi bokk ci mbootaay googu ngir ànd bu rafet ak jokkalante gi. Ci baatu askanu Senegaal, mi ngi rafetlu àndam bi ak naataangoom yooyu tey ñaan ñu dalal ki koy wuutu ci ni ñu ko defe ak moom, ci xaritoo gi ak yëg gi. Te, ci aaday saa-senegaal sax nag ki koy wuutu moom dina sàmmu diggante yooyu ko boole ak yeneen réew yi bokk ci mbootaay googu.
PÓOL KAGAME LAAJ NA ÑEENTEELU MOOME
Póol Kagame tollu ci juróom-benn fukki at ak juróom, di it jamono jii Njiitu réewu Ruwàndaa, xamle na ne lawax la ci wote yii di ñëw. Loolu nag ma nga ko xamlee ca Màngasinu Jeune Afrique. Nee na dafa bég ci kóolute gi ko saa-ruwàndaa yi di wóolu. Dina leen liggéeyal fii ak mi ngi koy mën. Moo tax mu ne lawax la ci wote yii di ñëw.
MBËKK MI
Mbir mu doy waar moo xew Kayaar ci guddi altine gi jàpp talaata. Genn gaal gu yeboon lu tollu ci juróom-fukki doomi-aadama yu dëgmaloon Espaañ la sàndarmëri ba teg loxo. Ba ñu leen tegee loxo, yóbbu leen ca Birigaadu luññutu (brigade de recherches) bu Cees, ca la coow la doore. Ndax, mbir moomu neexul ndaw ña. Ca lañu fippoo jàmmaarloo ak takk-der ya, taal seen ug daamar boolewaale ci ab « vedette de surveillance bu marine nationale » bi. Waaye nag dafa mel ni mbir ya moom seddul woon ci kenn ca ñoom. Ndax, takk-der ya sax dañoo mujje am ñu leen wallu ba ñu delloosi jàmm ak ug dal ca béréb booba.
XEW-XEW BU TIIS FA NGOR
Jenn jigéen juy wuyoo ci turu Mari Géy moo fa faatu ci anam yu doy waar. Bees sukkandikoo ci li ay mbokkam wax, ndaw soosu mi ngi faatu ci jàppante bim jàppante woon ak takk-der yi. Démb la woon, ay boori fukki waxtu ci guddi ginnaaw bi takk-der yi doon raafal foofa di laaj nit ñi seen i dàntite, ca la coow la juddoo. Bi loolu amee la jàppanteek takk-der yi ko doon jaay doole, jàppante bu metti ndax dañu ko bëggoon a dugal ci seen daamar gi. Nee ñu, bi ñu xamee ne soxna si yëngootul, mi ngi ne nemm, ca lañu dawee. Mbokk yi nekk ci di wut lu ko rawale ca raglu ba. Waaye, booba fekk na béy wéy na mbuus. Ndax, laata ñu koy defal dara fekk na mu faatu. Ay mbokkam nag nee ñu dinañu def pelent X ngir bóomug bakkan.
PASTEF AFRIKA
PASTEF AFRIKA di xeetu mbootaay gu yees gu ñu sos mu boole ay làngi pólitig ak i kurél yu bokk benn bëgg-bëgg. Boole na lu tollu ci juróom-ñeenti réewi Afrig. Ñoom nag, li ñuy sàkku mooy ñu bàyyi Njiitul Pastef li Usmaan Sonko ca na mu gën a gaawe. Ndax, nee ñu, jamono jii, mbooleem jafe-jafe yi sunu kembaar gi di jànkonteel moo tax mu jot ñu booloo def wenn say ngir am indi ci ay saafara. Ndaje ma ñu doon amal nag dippe ko “Conférence des Présidents Panafricains” (CPP) sàkku nañ ci njekk kilifay Nguuru Senegaal. Moo tax nag ñu door dagaanug pólitig ak ci wàllu kibaraan gu ñu dippe PASTEF AFRIKA nga xam ne duñu dakkal lu dul ñu bàyyi Usmaan Sonko, defaat làng gi ñu ne dañu ko fee jële. Ñi ngi ñaan mboolem kuréli pólitig yi ak way-moomeel yi ñu wuyu leen ci seen woote boobu. Maanaam, seen bataaxel mooy ne bu dee dañoo rey Pastef ca Senegaal, mu judduwaat ci biir kembaaru Afrig.