LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (21/2/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJIITU RÉEW MI DINA JANOOK TASKATI XIBAAR YI ËLLËG CI ALXAMES JI

Bu ëllëgee, ci alxames ji, Njiitu réew mi dina tontu laaji taskati xibaar yi bu 19i waxtu jotee. Ca njéeméer ba (pale ba) la ndaje miy ame. Direkt lay nekk ci tele RTS, Rajo Senegaal, iRadio ak Seneweb. Dafa di sax, taskati xibaar yiy liggéey ci kibaaraan yooyu kese lañ ci woo. Ay ñoom Walfadjri, 2Stv, SenTv, TFM, añs., kenn woowu leen ci.

JÀPP NAÑU NGAÑ DEMBA TURE

Barkaati-démb la moom Meetar Ngañ Démba Ture ñibbisi fii ci réew mi. Ndax, kenn umpalewul ne def na juróom-benni weer fa Mali. Li waraloon gàddaayam gi mooy ne ginnaaw bi ñu tegee loxo Usmaan Sonko, moom dafa bokkoon ci ñi Yoon tegoon bët ngir jàpp ko. Mel na ni loolu mujj na àntu tey. Ndax, tey ci suba la ko waa DIC jàpp fa këram.

BENEEN NDONGO FAATU NA FA NDAR

Ay fan ginnaaw bi takk-der yi bóomee Alfa Yero Tunkara ci jàmmaarloo yi doxoon diggante takk-der yi ak ndongo yi, keneen fekki na ko tey ci suba. Li sabab deewug ndongo loolu mooy gaañu-gaañu yu metti yi mu jële woon ci jàmmaarloo yii weesu. Mi ngi faatoo ca raglu bi ñuy dippe “Hopital Principal” fa Ndakaaru. Moom ndongo li mi ngi wuyoo ci turu Porospeer Keledoor Seŋoor. Mi ngi nekkoon ci atam mu njëkk ci jàngune bu Ndar. Mu doon jànge ca UFR SAT ci bànqaas gii di “Mathématique Appliquée et Sciences Sociales”.

Naka noonu kurél gi ëmb ndongo yi tamit jël na ay ndogal. Ndax, kenn umpalewul ne bi ñu bóomee Alfa Tunkara ba léegi njàng amul. Looloo taxoon ba am ndongo yu tàmbali woon a ñibbi. Ñoom waa CESL ñgi ngi sàkku ci ndongo yi ñu dellusiwaat. Ndax, jël nañu ndogalu dooraat njàng mi. Rax-ci-dolli, ñoom duñu may wenn yoon gaa ñi ñu def li ñu bëgg. Maanaam, ñu tëj bérébu jàngekaay bii ni ñu koy defe saa su ne.

ÑÀKKUM NDOX FA  TUUBAA

Bu amee diwaan yu yëgul ñàkkum ndox mi, Tuubaa bokku ci. Ndax, ay fan a ngi nii yoo xam ne bari na gox yu mënut a am ndox. Daanaka, am na lu jege ñaar-fukki gox yu amul ndox. Li ko waral du lenn lu dul ne yenn mbalka yi dañoo yàqu. Ya ca des amatuñu doole ngir nàndal ñépp. Maanaam, dañoo néew doole. Démb nag, am ndaje amoon na diggante waa meeri ba, waa Tuubaa Ca Kanam ak Ofor. Waaye, ba tey mel na ni mbir mi sotteegul.

DÀQ NAÑU TUSEE MÀNGAA

Tusee Màngaa dafa bokk ci waa Pastef yi ñu tegoon loxo bu yàgg ba tey. Keroog ci alxames ji lañu ko mujjee bàyyi moom ak ñeñeen ñu bokk ci làng googu. Waaye, mbir mi yemul foofu. Ndax, dafa am leneen lu ñëw yokk ci xar mi karaw. Ndax, dañu koo tekkil ndombog-tànk “medecin-chef” ga mu amoon fa bérébu fajukaay ba nekk fa Ngor teg ci di ko xaarloo. Ci gàttal daal, dàq nañu ko fa béréb boobu. Xibaar boobu ci xëtu Facebookam la ko xamle.

SYTJUST ÀDDU NA

Tey ci suba gi lañu jàpp Meetar Ngañ Demba Ture kenn ci seen naataangoo yi. Moo tax kurél gii ñuy dàkkantale Sytjust (Syndicat des Travailleurs de la Justice) nga xam ne moo boole ñiy liggéey ci wàllumYoon ne mukk du deme noonu. Ñuy sàkku ñu bàyyi ko ca na mu gën a gaawe. Looloo tax ñuy woo Aysata Taal Sàll mi ñu dénk Yoon mu jàpp ci li Njiitu réew mi door. Muy delloosi jàmm ci géewu pólitig gi boole kook amal wote yi. Ñuy sàkku mbooleem ñiy yëngu ci Yoon cig booloo ngir mën a jàkkaarlook lépp lu mën a xew.

NJIITU RÉEW MI YOKK NA ÀPPU MOOMEG WAA OFNAC

Cig pàttali, liggéeykat yi ñu tabb ca OFNAC boobu ñetti at kese lañu fa daan def. Te, ñetti at yooyu wenn yoon kese lañu koy yeesalaat. Njiitu réew mi yokk na àpp boobu. Léegi, juróomi at la, ñu koy yeesal wenn yoon. Yeesal gi pàcc lay doon ci juróomi at yépp. Loolu di firndeel ne Sëriñ Basiiru Géy  ak  ñam fa nekkandool seen moome day dooraat.

XEW-XEW BU TIIS FA CAP-SKIRING

Bakkan yiy rot ci ndox mi mel na ni ba tey ma ngay wéy. Ndax, xew-xew bii am fa diiwaan wii firnde la ci. Genn gaal gu amoon fukki doomi-aadama ak benn moo fa suux. Li rotagum ciy xibaar nag, nee ñu ñetti bakkan rot nañu ci. Mu am kenn koo xam ne moom gisaguñu ko. Juróom-ñaar ña des moom mujjee nañoo mucc ca jéyya ja.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj