LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (21/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DAKKALUG DUGAL GAAS CI RÉEW MI

Réewum Senegaal mi ngi waaj a séqi beneen jéego bu am solo ngir moom boppam, mënal boppam. Nde, fii ak ub diir dootul jëggaani lii di gaas. Ki biral xibaar boobu di elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko. Li mu xamle mooy ne li ko dale atum 2026 réewum Senegaal dootul dugal dara lu jëm ci wàllu gaas ci réew mi. Maanaam, lépp lu gaas di doxal ci réew, sunu bos moo koy doxal. Mu nar a doon yokkute gu mag ci mbirum laf gi.

COOWAL DAANI ETAASINI ÑEEL ÀTTEKATI CPI YI

Daan yi Etaasini jël, bëgg leen teg ci ndoddi ñeent ci àttekati CPI jur na coow. Àttekat yooyu nag, doomu Senegaal jii di Maam Manjaay Ñaŋ daf ci bokk. Atum 2021 lañu ko faloon ca ëtt boobu. Li waral coow li mooy ne waa Etaasini dañu ne ñooñu dafa am yu ñuy jël di ko teg ñi ànd ak Etaasini.

Réewum Senegaal génnee na ab yégle di ñaawlu li kilifay Amerig yi bëgg a def. Rax-ci-dolli, mu sàkku ci ñoom ñu bàyyi loolu ñu namm a def. Nde, ndogal yooyu du def lu moy wàññi péexte ak sañ-sañu ñiy yëngu ci wàllu yoon. Naka noonu, kii di elimaanu jëwriñ, Usmaan Sonko, bind na ci xëtu Facebookam ngir àddu ci mbir mi. Ginnaaw, bi mu njukkalee Njiitu réew mi ci taxawaayam ñeel mbirum CPI mi, dafa biral ag àndam ak doomu Senegaal jii bokk ci ñi ñu bëgg a daan.

NDAJEM ELIMAANU JËWRIÑ YI AK KURÉLU NJAATIGE YI

Démb, ci àllarba ji, la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, doon dalal njaatigey liggéeykat ci ajuwul ci Càmm gi. Mu nekkoon ndaje moo xam ne ngir wut saafara la ci wàll woowu. Ndax, kenn umpalewul ne dañuy jànkoonte ak jafe-jafe yu bari. Waaye, elimaanu jëwriñ yi jot na leen a leeral ay mbir. Nde, xamal na leen ne réew mënut a ñàkk a sukkandiku ci juuti, donte ne sax dafa war a yamamaay. Ndax, juuti mooy dundal réew. Waaye, yamul foofu. Daf leen ci yokkal ne fàww ñu jéem a wut ay pexe yoo xam ne dina tax ñu saafara jafe-jafe yii. Ndax, bëgguñu fii ak ñaari at yu ni mel di leen gaaraat.

FANTA SÀLL GÉNN NA ÀDDUNA

Naqar ak tiis la réewum Senegaal fanaanoo démb. Soxna sii di Fanta Sàll nekkoon fi dépite moo génn àdduna. Mu nekk xibaar bu diis lool ci askanu Senegaal. Moom nag, seedeel nañu ko ne ku amoon fulla ak faayda la woon ci li mu doon yëngu. Jébbal nañu ko boroomam tay ci alxames ji fale ca Kungél, fa armeeli kër Sëriñ Jabel. Di ko ñaanal Buur Yàlla mu jéggal mbooleem ay bàkkaaram.

NDOG MU METTI FA LUGA

Ndogi yoon yaa ngi wéy di gën a bari ci réew mi. Léegi, xew-xew am walla mu ñàkk a am terewul ndog yi moom di am. Nde, tay jii rekk am na ndog mu am fa wetu Luga. Genn daamar gu ndaw moo fa mbëkkante ak daamar yi ñuy tudde war-gaynde. Benn bakkan rotagu ca nag. Waaye, bees sukkandikoo ci waa Seneweb, fukk ak ñaar jële nañu ci ay gaañu-gaañu. Mu am juróom yoo xam ne mettile nañu lool sax. Ñoom ñépp rawale nañu leen fa raglu Ahmed Saxiir Mbay bu Luga.

XEW-XEW BU DOY WAAR FA PIKIN

Démb, ci àllarba ji, la xew-xew bu yéeme am fa Pikin. Benn dawalkatu biisu “Tata” moo fa fiir boroom benn jakartaa. Li ci doy waar mooy ne, ci lees wax, ñoom ñaar dañoo jote woon. Bi loolu amee ci la ko dawalkatu “Tata” bi tëkkoo. Yàggaatul dara mu fekk ko ci yoon wi daldi koy fiir, mu faatu ca saa sa. Mu doon mbir mi doy waar lool.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj