USMAAN SONKO : DUGG NAÑU CI JAMONO JOJ, BAALE JEEX NA
Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, biral na gis-gisam ci xeex gi ñuy xeex nger fi réew mi. Fekk mu doon yékkatiy kàddu bërki-démb ci altine ji, fa CICAD (Centre International de Conférence Abdou Diouf), Jamñaajo, bi ñuy amal ndajem waxtaanu doxalkat yi ak saytukati Nguur gi. Naka noonu, Sëñ bi Sonko biral na fay kàddu ngir woo liggéeykat yi fa teewoon ci ñu xeex lépp luy xeetu jëfin yu safaanook doxalin wi yay. Nde, bànqaasu réew mi dafa fees ak i xeeti njaaxum yu nekk. Te xeeti njaaxum yooyule yóbbe réewum Senegaal ci 123eelu toogu ci toftale bi ñeel 190i réew yi gën a mucc ci nger. Ba tax daal muy leeral ni, ak Nguurug Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, « dugg nañu ci jamono joj, baale jeex na fi ». Muy xamle ni kon nës-nësal wàllum nger jeex na ci jamono jii ñu nekk.
CAABALUG BÀNKUB ÀDDINA SI
Bànku àddina si génne na caabalam gi njëkk ñeel yoonu koom-koomug Afig ci atum 2025 mi. Ginnaaw xayma yi mu amal, xamle na ni koom-koomug Afrig dina am yokkute guy dem ba ci 4,1% ci atum 2025 mi, ak 4,3 ci atum 2026 mi. Yokkute googu nag, réewum Senegaal fés na ci bu baax. Bees sukkandikoo ciy nat yi, Senegaal mooy réew mi nar a ëpp yokkute ci kembaarug Afrig. Nde, dina mën a am yokkute gu dem ba ci 9,7%. Muritani mi séq ak Senegaal teenu gil bii di GTA (Grand Tortue Ahmeyim) ci seen digaloo dina am itam yokkute ci koom-koomam. Jamono yooyu, Niseeriyaa ak Afrig di sidd, ñaari réew yi ëpp koom ci réewi Afrig yi nekk ci bëj-saalumu Sahaaraa bi, dinañu xaw a des ginnaaw donte ni seen yokkute nar naa teguwaat ci yoon.
MBIRUM KËYITUB MÓTO-JAKARTAA YI
Wutum këyit yi aju ci móto-jakartaa yi dinaa tàmbali fa goxu tiwaawan ci ayu-bés bii di ñëw. Bërki-démb ci altine ji la ndogal loolu wàcc ginnaaw bi ñu fa doon amal am ndaje ci njiiteefu perefe ba , Mamadu Géey, ak teewaayu Mustafaa Taal (njiitu yaale yi fa diiwaanu Cees), Demba Jóob Si (meeru Tiwaawam) ak Lamin Caw (meeru Pambal Lasaar). Naka noonu, dinañu tàmbali joxe xàmmeekukaay yi ci àllarba ji (29 sãwiyee 2025) fa champ de courses ba. Dinañu amal yeneen i ndaje itam fa Tayba Njaay, Mexe ak Nooto.
JÀPP NAÑU KI FI JIITE WOON APROSI
Yoon moo ngi ci tànki leeral mbiri Tabaski Njaay mi ñuy jiiñ mbuxum. Naka noonu, waa DIC (Division des Investigations Criminelles) teg nañu loxo Momath Ba mi jiite woon kër gii di Aprosi (Agence de promotion des sites industriels). Bees sukkandikoo ci xibaar yi fés ci luññutu bi, dañoo nemmeeku ay pexey càcc ci xaalisu askan wi fa Aprosi ga soxna si Ngom nekkoon laata muy dem fa CRSE (commission de régulation du secteur de l’électricité. Moom ndaw si sax tuddoon na turu waa ji ca jamono yooyu.
NDOG LI AM FA FAWUB ALASAAN JIGO BU PIKIN
Fa fowub Alasaan Jigo bu Pikin, jàppante yu metti moo fa amoon ci altine ji 20i fani sãwiyee 2025. Jàppante yooyoo ngi doxoon ci diggant way-fari ñaari ekib yi fa doon amal joŋante nawetaan (ASC Farba ak ASC Naataange). Ginnaaw bi xeex bi doore ci biir fowu ba, way-far yi dañoo dampoowaat ci bitti ba am ku ci ñàkk bakkanam, kuy wuyoo ci turu Mustafaa Jeŋ.