LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (22/11/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LAYOO MAAM MBAY ÑAŊ USMAAN SONKO

Suba ci alxames ji lañu waroon a àttewaat coow li doxoon diggante ñaar ñooñu ca ëttu àttewaay bu kowe ba. Dafa di ñoom ñaar jotoon nañu leen a àtte ci weeru me wii jàll ba ñu daan Njiitul Pastef li. Waaye, àndul woon ca àtte booba. Looloo taxoon mu def ag dab-dabaatal ca ëttu àttewaay bu kowe ba ngir ñu nasaxal àtte boobu. Seen layoo boobu suba ci alxames ji lañu ko jàppoon, waaye, du mujjee am. Ndax, dafa mel ni ëtt boobu dafa jàpp ne wayndare pareegul ngir ñu càmbar ko.

YENEEN XIBAAR ÑEEL USMAAN SONKO

Gii Mari Saaña ak Abiib Si ñoo seeti woon tey Njiitul Pastef li ca Kab Maniwel ga mu nekk jamono jii. Ba ñu fa jógee lañu joxe ay xibaar ñeel meeru Sigicoor bi. Ca lañu xamlee ne fim tollu nii dakkal na xiifal gi, te, mi ngi tane bu baax. Ndax, nee na xiifal googu ngànnaay kese la woon ngir xeex yenn ci ay àqam. Te, am na lu mu ci jot a am.

TIIJAAN YI DINDI NAÑU SEEN JURE BI (PELENT)

Ay fan ci ginnaaw la taalibe séex yi pelentoon kii di Ustaas Umar Sàll. Li ko waraloon mooy kàddu yu mu yékkati woon ci wàllu nees war a tuddee Yàlla, tiijaan yi gis ci seen bopp. Maanaam nee ñu dafa ŋàññi lenn ci seen i jëf muy lu ci mel ni wasifa ak hadra. Ci la ko taalibe tiijaan yi dóore ab pelent, ginnaaw gi ñu jàpp ko ba jamono jii ma nga ca kaso ba. Waaye, li jot a rotagum ciy xibaar xamle nañu, ci ginnaaw ag diisoo, ñoom mujj nañu dind seen pelent boobu.

DAKARNAVE DÀQ NA FAALA FLEUR

Ndey Faatu Faal ñu gën ko xam ci turu Faala fleur dàqe nañu ko ca béréb ba mu doon liggéeye. Loolu mi ngi xew ginnaaw ba mu génnee jógee kaso. Ndax, moom kenn la ci ñoñi Usmaan Sonko yi ñu teg loxo lu ëpp ñetti weer. Fan yee nag la génn. Dàq googu tax ba mbokki yi mu bokkal Pastef di ko defal li ñuy tudde cagnotte.

Keneen tamit ci ñoñi Usmaan Sonko yi nga xam ne jàppoon nañu ko bu yàgg, mujj nañu ko bàyyi tey. Muhamadu Lamin Baara ñu gën ko xame ci turu Jóob Tayif génn na tey ginnaaw lu jege fukki weer ak benn bi ñu ko tegee loxo ak léegi. Mu amaat tamit, ñeneen ñoo xam ne ci Pastef lañu bokk muy Yarga Si ak yeneen fukki ndaw ak juróom-ñeent yoo xam ne tey ci àllarba ji lañuy taxaw ca kanamu àttekat ba.

FARÃS DÓOR NA SENEGAAL

Tey ci bëccëg la gaynde yi am lu tollu walla luy jege fukki at ak juróom-ñaar doon joŋante ak xaley Farãs. Joŋante boobu nag, ñoom dañu caa mujjee lajji. Ba ñu dawalee ba simili yépp jeex ñu dem ca daj-dëppu ga. Juróomi xaley Farãs dugal, waa Senegaal moom ñett kepp a dugal, Farãs jël ndaw li.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj