LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (22/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SONKO SANT NA JËWRIÑ YA WOON ÑU DELLOO DAAMARI NGUUR GI

Jëwriñ yu nekkoon ci Càmmug Maki Sàll ya woon, war nañu delloo daamari Nguur yiñ daan liggéeyee. Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, moo jël ndogal lu ni mel. Dañ leen jébbaloon damaar yi ngir yombalal leen dem beek dikk bi ñeel yitteey askan wi. Ndegam nekkatuñ ci yitteey askan wi nag, Sëñ Usmaan Sonko sàkku na ci ñoom ñu delloo si damaar yi fileek àllarba 24 awril 2024.

WÉR-GI-YARAM

Diggante 2017 ak 2023, oppeere nañ fa raglu bu Cees lu ëpp 800i doomi-aadama cib sémb bu ñu duppe Medevac (Programme médical et humanitaire du gouvernement tchèque). Sémb boobu, moo ngi aju ci ndimbal yi réewum Cekki di amal ci àddina si. Ñu taxawal fii ci Senegaal  jaare ko ci lëkkatoo gi dox ci diggante réewum Senegaal ak mu Cekki. At mu jot, dina yebal ay fajkat fi Senegaal, fa raglu bu Cees, ñu amal fa ay bés, faj fay way-tawat te duñ fay dara. Ci ayus-bés bii weesu lañ ko doon amal ci atum ren jii. Ñu waroon cee oppeere 30i way-tawat ci ñeenti xeeti jàngoro.

SIYAAR SENERAAL BU TIWAAWAN

Démb ci dibéer ji lañ doon amal siyaar seneraal bu Tiwaawan. Xew-xewu diine la bu ñu fay amal at mu jot, li ko dalee ca atum 1930 ak tey. Séexal Xalifa Abaabakar Si, ki njëkk nekk Xalifa El Haaji Maalig Si, moo ko njëkkoon a woote ca at mooma, moom mi daan soññ taalibe yi ngir ñu farlu ci seen diine, seen tarixa, seen liggéey, seen daayira ak seen yoonu Tiwaawan. Siyaar bi doon xew-xew bob, taalibe yi dinañu ci dajeek Sëriñ bi ngir dundalaat diggante yi ci yoonu Yàlla. Bu ren ji moo nekkoon 94eel wi yoon.

AB LIIR BU ÑU FOR CI SËN FA KAFRIN

Fa bokk-moomeel bu Kafrin, benn liir lañ for, ñu sànni ko ci mbalit mi ci kàrce bu ñuy wax Njóobeen. Biñ koy for démb ci dibéer ji, fekk na deseetul bakkan. Ay ndongo-daara yu doon for i weñ ci benn sën bu mag ñoo ko gis bi ay 10i waxtu di jot ci suba si. Muy liir bu jigéen bu tooy xépp, butitu ànd bi sax kenn jotu koo dagg. Ñoo ngi ko fekk ñu lëmës ko ci menn mbuus mu baxa.  Ci noonu lañ ko daldi siiwal.

NÉEWI ÑAARI NDAW YI LABOON CA GÉEJU GÀDDAAY FEEÑ NAÑ

Ci àllarba jii weesu, ñaari ndaw ñàkkoon nañ seen i bakkan ca géeju gàdday, fa Géejawaay. Ginnaaw bi ñu labee, seen i néew dañ réeroon ci biir géej gi. Waaye, mujje nañ leen a gis ci jeexitalu ayu-bés bi. Barki-démb ci gaawu gi la leen géej gi yëq fu sorewul ak fiñ réeree. Ci suba teel la nappkat yi ak ñi doon tàggat seen yaram njëkk a gis néewu kenn ki. Ci lañ ko daldi yëgal waa pólis, ñu wax ko wallukat yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj