Mamadu Ibra Kan dina bokk ci wotey 2024 yi. Bërki-démb, ci dibéer ji, la ko dëggal. Fekk ñu doon ko dalal ca jotaayu Jdd (Jury du dimanche) bu Itv. Bees ko déggee bu baax nag, moom mooy kiy bokk. Te, ay ñoñam ñoo ngi ci liggéey bi ngir matale lépp lu bokk ci wote yi laaj, rawatina parenaas bi.
Cig pàttali, Mamadu Ibra Kan mooy njiitul mbootaay gii di « Demain c’est maintenant », maanaam ëllëg jot na. Moom nag, am na yaqiin ni suqaleeku Senegaal mooy fexe ba réew mi mënal boppam, maanaam àgg ci li nasaraan di wax « autosuffisance ». Nde, kenn mënul a dëkk ci di jéggaani lépp loo soxla ba noppi di yaakaar yokkute.
YOON : UMS ÀDDU NA
UMS (Union des Magistrats du Sénégal), kurélu àttekati Senegaal yi, doon na amal ndaje mu mag ci gaawu gi. Ñaŋ ko doon amalee ca Sali. Usmaan Simeer Juuf lañu tabbaat ca boppu kurél ga. Moom Sñ bi Juuf sax jot na fa yékkatiy kàddu. Muy xamle ni bare na lool lu ñuy ŋàññ doxalinu yoon ci jamono yii. Ba tax muy leeral ni ñoom Masistaraa yi seen yoon nekkul ci pólitig gi te itam waruñoo jaxase ñaar yii di yoon ak pólitig. Yokk na ceet ni jëf yi ñuy toppee maxejj yi yoonu benn masistaraa nekku ci.
TÀGGAT-YARAM
Gaynde Senegaal yu góor yi (basket) duñu dem ci powum olempig yiy am fa Pari, Farãs. Dañoo mujje lajj ci bokkadil yi doon am. Ginnaaw bi ñu demee ba ci gañ-jël bi, ekibu Kamerun bee leen dóor 80 ci 74. Kon ekibu Kamerun bi mooy mujje wéyal xëccoo bi ci joŋante yi mujje ci bokkadil yi.
BITIM-RÉEW
Bërkaatu-démb ci gaawu gi, Seneraal Ciyaani ma nekk ca boppu nguur ga fa Niseer yékkati na ay kàddu. Ci kàddoom yooyu, ma nga cay xamal askanu Niseer ni dinañu amal ab diisoo bu yaatu ci réew mi. Waaye, yemul ci loolu, ma ngay dankaafu waa CEDEAO. Lu mu leen di xamal mooy ni askanu Niseer bëggul xare te itam ñoom ñi jiite bëgguñu ko. Waaye bés bu fi xeex jollee du yomb ci waa CEDEAO ni ñu ko foogee.