BLD/TAKKU SOSU NA
Géewu pólitig bi amati na gan. Bi wote yi jàllee ba léegi, dafa mel ni gaa ñi dañu doon seral. Waaye, ña ngay waaj a làbbali. Kurél gii di BLD/TAKKU (Bloc des Libéraux et des Démocrates) sosu na. Kurél googu, dafa ëmb lu ëpp ñeen-fukki làng ak i mbootaay. Seen mébét mooy jàkkaarlook Nguur gi fi nekk ba sàmm li ñu fi liggéey ci wàllu demokaraasi atum 2000 ba ci atum 2024 mii ñu nekk. Looloo tax ñu bëgg a dajale ñépp ñi nga xam ne ci njaboot googu lañu bokk. Su ko defee ñu mën a taxawal lëkkatoo gu am doole ngir wote yiy waaj a ñëw bu fekkee dañoo tas Ngomblaan gi.
LIMUB ÑI FAATU CI YOONU TUUBAA WI
Du guléet ñuy nemmeeku ay aksidaŋ saa su xew-xew bu mag amee fi réew mi. Te, màggalu Tuubaa bokk na ci xew-xew yi fi ëpp doole. Ñii di waa BNSP (Brigade Nationale des Sapeurs Pompiers) biral na limub aksidaŋ yi ak ñi ci loru. Limub aksidaŋ yi mi ngi tollu ci téeméer ak fanweer ak ñett. Ci ñetti-téeméer ak juróom-ñeen-fukk ak ñett yi bokk ci aksidaŋ yi, ñetti-téeméer ak juróom-ñett-fukk yi ak juróom-ñaar mucc nañu ci. Juróom-benni doomi aadama ñoo ci ñàkk seen i bakkan.
DAKAAR DEM DIKK MI NGI ÀRTU
Këru liggéey gii di DDD mi ngi àrtu ñiy jëfandikoo seen i daamar ngir màggali. Li ñu ko dugge du lenn lu mooy ne, dañoo gis ay xeetu doxalin yu ñaaw ci yaale ji. Nde, dafa am ñuy jënd ci ñoom tiket yi ñu war a demee Tuubaa te, seen i njëg du romb juróom-ñetti-téeméer. Am ñoo xam ne dañu leen di jënd ci ñoom ba noppi, di ko jaayaat lu jafe. Looloo tax, ñuy àrtu seen i kiliyaŋ ñu bañ di jënd tiket yi ñuy jaayaat.
XEW-XEW BU DOY-WAAR FA TFM
Xew-xew boobu mi nga am démb ci ay boori timis bi ñuy def seen i xibaar. Li ñu def du lenn lu mooy dugal widewoob elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, boo xam ne atum 2018 la woon. Ca jamono jooja, mi ngi nekkoon ci kujje gi. Maanaam, ñoom dugaluñu waxtaanu démb wi, waaye, wu yàgg lañu dugal. Te, moom démb ci àllarba ji la fa dem. Mu nekk mbir mu doy-waar donte ne sax, këru tasukaayu-xibaar gaa ngi ciy jéggalu. Nee ñu loolu njuumte la. Te, dinañu def i luññutu ba xam lu sabab mbir moomu.
MBËKK MI
Coowal mbëkk mi mel na ni am na fu mu tàmbalee waaye, kenn xamagul fu muy yem. Ndax, saa su ñu jàppee ne ndaw ñi teggi nañu seen i tànk, fekk ña ngay ruumandaat mbir mi. Donte ne sax, am na ñu ñu tegoon loxo bu yàggul dara fii ci Senegaal laata ñuy dem. Ba ci talaata jii weesu rekk, am na lu tollu ci juróom-fukk ak juróom-ñett yu doon waaj a sóobu ci yoon wi, waa “Gendarmerie nationale” ñoo leen waññi. Loolu terewul ne am na gaal gu yeboon lu tollu ci téeméer ak juróom-ñett-fukk ak juróom-ñett goo xam ne teeri na fa El Hero, fa réewum Espaañ. Gaal googu, fukki jigéen ak ñeent ñi ngi ci woon. Amoon na tamit, fukki xale ak ñeent.
BURKINAA FAASO DINA SSOPPI BÀKKOOM BI FA NEKKOON
Réewum Burkinaa Faaso, menn la ci réew yi sóobare yi jiite. Ki ko jiite jamono jii mooy Kàppiteen Ibraahiim Taraawore ginnaaw ba mu déjjatee ka fa nekkoon. Ca ndajem jëwriñ ma ñu doon amal démb, xamle nañu fa ne dinañu soppi seen bàkku (devise) réew. Seen bàkku mi ngi nekkoon “Unité-Progrès-Justice”, ñu mën koo tekki ci “Bennoo, Yokkute ak Yoon”. Dinañu ko fa jële, def ci “La patrie ou la mort, nous vaicrons”. Loolu di ay kàddu yoo xam ne kii di Tomaas Sànkara nga xam ne taxawaayam ci Afrig ñi ngi koy waxtaane ba tey, daan na leen jëfandikoo. Nee ñu sax, kàddoom yooyu moo nekkoon bàkku ba, ba ci atum 1991, kii di Belees Kompaawore moo ko soppi.
JÀPP NAÑU WOTEY PALUM DÉPITE YI FA CÀDD
Lu tollu ci fukki at ak ñett (2011) ba fa ay wotey palum dépite gëjee am ak tey, jàppaat nañu leen ren jii. Démb la kii di Ahmet Basiret nga xam ne mooy Njiitu ndiisog wote yi siiwal xibaar boobu. Ndax, kenn umpalewul ne, bu yàggul dara lañu amaloon wotey palum Njiitu réew fa réew moomee. Te, ka ca jiitu du kenn ku moy Mahamat Idriis Débi Itnoo mi fa kilifay sóobare ya tegoon fa boppu réew ma ginnaaw bi ñu bóomee way-juram wu góor, Idriis Débi mi jiite woon réew ma. Loolu mi ngi xewoon ci atum 2021. Ci atum 2024 mi lañu amal i wote, ci la ko askan wi di sog a fal, donte ne sax, am na kurél yu ŋàññi ndamam loolu. Ginnaaw wote yooyu jàll na, xamle nañu ne wotey palum dépité yi nga xam ne ay at a ngi nii amuñu fa, dinañu leen amal ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru desàmbar. Maanaam, juróom-ñetti weer kepp ginnaaw bi ñu amalee wotey palum Njiitu réew yi.