Ayu-bés bii ñu génn la Ngomblaan gi dooroon liggéey bi ba jotoon a taxawal ag ndiisoo. Suba, ci àjjuma ji, woo nañu dépite yi fa Ngomblaan ga. Li waral woote bi du lenn lu moy fénc càkkuteefu murig mbalaanu kiiraayu Farba Ngom. Ndax, seen naataangoo boobu Yoon daf ko soxla. Te, fileek muriwuñu mbalaanu kiiraayam Yoon du ko mën a déglu.
UMAR SOW AK ABU JÀLLO DEM NAÑU KASO
Démb, ci àllarba ji, lañu yóbbu Abu Jàllo ak Umar Sow kaso ci ndigalu toppekatu bokkeef gi. Umar Sow mi ngi bokk ci làngug APR (Alliance Pour La République). Kii di Abu Jàllo moom, faramfàccekat ci tele bii di Sentv. Li waral ñu yóbb leen kaso du lenn lu moy kàddu yi ñu yékkati ci murig mbalaanu kiiraayu Farba Ngom. Nde, ay mbirum boddikonte xeet lañu ko jàppe. Ñoom ñaar, dinañu leen àtte altine jii ñu jëm fa ëttu àttekaay bu Ndakaaru.
YÉGLEB NJËWRIÑU NJÀNGALE MU SUUFE MI AK MU DIGG-DÓOMU MI
Talaata jii weesu la njureefi joŋantey CREM bi génn. Ñu jot cee jël lim bu takku ci ay jàngalekat. Waaye, loolu taxul ñu bàyyi. Ndax, dafa mel ni amaguñu lim bi ñu soxla. Ba tax na, njëwriñu njàngale mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi génne ab yégle tay ci alxames ji ngir xamle ne ubbiwaat nañu beneen joŋante. Wii yoon, li mu soxla ci ay jàngalekat mi ngi tollu ci ñaari junni ngir atum 2024/2025. Li ñu ko dugge mooy jële fi ñàkkum jàngalekat yi dëkk yu bari di jooy. Jébbalug wayndare yi ci lënkaay li (en ligne) moom tay la door. Mu war a jeex benn fan ci weeru féewaryee.
WAA AES AM NAÑU SEEN JÀLL-WAAXU BOPP
Tay, ci alxames ji la waa AES (Alliance des Etats du Sahel) génne ab yégle ngir siiwal xibaar boobu. Li ñu ko dugge mooy gën a yembal dem bi ak dikk bi ci seen diggante, ñoom réew yi ci bokk. Nee nañu nag, jàll-waax yooyu dinañu tàmbali li ko dale fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru sãwiyee wii. Waaye, loolu tekkiwul ne maxejj yi yoroon jàll-waax yi am màndargab (logo) CEDEAO te, seen àpp jeexagul dootuñu mën di dem ak a dikk, demewul noonu. Ndax, mën nañu leen a weccee ak yu AES yi.
XEW-XEW BU DOY-WAAR
Xew-xew boobu mi ngi am ci dibéer jii weesu. Kii di Abdulaay Sekk, doomu Idiriisa Sekk, moo doon jéem a xaru. Nde, moom kenn umpalewul ne bu yàgg ba tay ma nga ca loxoy Yoon. Dañu koo jàppoon ci njaayum sineebar. Booba ba tey nag ma nga ca kaso ba. Mu mel ni dafa bëggoon a yemale dundam gi foofa.