Xale yees yéex a bind ci wayndarey juddu yi (actes de naissances) duñ mën a dugg ci daara yu xarañe yees duppee Lycées d’excellence. Muy ndogal lu tukkee ci jëwriñu njàng mu suufe meek mu digg-dóomu mi, di Sëñ Mustafaa Giraasi. Waaye, Seydi Gasama, bokk ci njiiti kuréli way-moomeel yi, di xeex àq ak yelleefi doom-aadama, àndul ci ndogal loolu. Mu gis nag ni, ndogal lees war a xoolaat la, ndax dëppoowul ak Yoon. Ci gis-gis bi mu biral, jaaduwul ñuy gàll xale yi ay daan ci seen i càggantey way-jur walla ay njuuj-njaaj yuy faral di am ci kayiti juddu yi.
WÉR-GI-YARAM
Sàndikaa fajkat yi, Ànd Gësëm, dina wéyal kàmpaañ bi mu doon amal ngir xeex xeeti jàngoro yees di soofantal fi Afrig toropikaal. Muy kàmpaañ bob, dees na ci maye ay garab ngir xeex jàngoro yu deme ni schistosomiases ak géohelminthiases te bari lool ay loraange. Namm nañoo doxal ñaareelu pàcc bi ci 6 ba 10i pani sãwiyee 2024 fi Jamñaajo, Cees, Jurbel, Fatig, Kafrin, Kawlax, Koldaa, Séeju ak Sigicoor. Naka noonu, ñuy sàkku ci seen naataango yi ñu dajale xibaari wér-gi-yaram yi ci aju ci béréb yile te jotale leen ci. Ñoo ngi sàkku itam ci jëwriñ ji ay jumtukaay ak anam yi war ngir ñu mën a am njureef yees ciy séentu.
MALI, NISEER AK BURKINAA DÀQ NAÑU NDOGALU CEDEAO LI
Ci njeexitu ayu-bés bee weesu la kurélug Cedeao gi jëloon ndogalu doxal juróom-benni weer (29i pani sãwiyee ba 29i pani sulet) ngir teqalikook ñetti réew yii di Mali, Niseer ak Burkinaa Faaso, ginnaaw bi ñu sosee seen réewaale bopp. Ndogal loolu nag neexul wenn yoon réew yooyii. Nde, ci yégle bi ñu génne, seen Njiit yaa nga koy ŋàññ. Ñu ciy xamle ni ndogal loolu, du lenn lu dul i pexe yuy jàppandal réewum Farãs ay nasam ngir faagaagal seen réewaale mii di AES. Ba tax na, fii mu nekk, jël nañu seen i matuwaay ak seen i sóobare ngri dara bañ leen a bett.
MBIRI LAT JÓOB
Layookati Lat Jóob yi yóbbu nañu mbir mi fa ëttu àttewaay bu kawe ba (Cour suprême). Muy ndogal lu ñu jël ginnaaw bi ëttu àttewaay bii di Chambre d’accusation du Pool Judiciaire financier gàntalee seen dabantal bi ñu ko jébbaloon. Ñuy sàkku nag ci ëtt bu kawe bi mu neenal topp gi ñuy topp seen kiliyaan te bàyyi sàqi bànkam yi ñu teg loxo. Ñuy fésal seen yaqiin ni seen kiliyaan bi dañ ko tëj ci lu dul yoon. Nde, waroon na am bàyyig négandiku bees sukkandikoo ci àtte bi. Dàq gi Chambre bi dàq seen dabantal teguwul ci lenn lu dëgër.