XIBAAR ÑEEL JURÓOMI JËWRIÑ YI ËTTU YOON GU KAWE GI WOOLU WOON
Ci ndoorteelu ayu-bés bii lañu woolu woon ñenn ci ñi fi nekkoon i jëwriñ ca jamonoy Maki Sàll. Kii di Ismaayla Maajoor Faal, bi ñu ko wooloo ba déglu ko mujj nañu koo bàyyi mu ñibbi këram donte ne sax, takkal nañu kob lam. Ndey Sali Jóob moom, dafa joxe li ñuy wax ci farãse “caution” bu tollu ci juróom-fukki miliyoŋ ak juróom-ñaar ngir ñu bañ ko yóbb kaso. Waaye, kii di Mustafaa Jóob ak Aysatu Sofi Galaadimaa, ñoom ñaar mujjuñoo mucc. Nde, ñoom ñaar ñépp dañu leen a mujjee yóbbu kaso. Kii di Sofi, démb la ko Ëttu àttekaay bu kawe bi (Haute Cours de Justice) doon déglu. Waaye, mujjul ñibbi këram. Mustafaa Jóob tamit, démb ci alxames ji lañu ko doon déglu, ginnaaw gi lañu ko yóbbu kaso. Ñaar ñooñu ñépp, li ñu leen di toppe du lenn lu moy luubal alalu réew mi. Kii di Mansuur Fay nag moom, xameesagul fan lay mujj ak ëtt boobu.
NDONGO YU UGB DOORAAT NAÑUY ÑAXTU
Barki-démb ci guddi gi la kurél gi ëmb ndongoy daara ju kawe jooju (Coordination des Etudiants de Saint-Louis (CESL) woote woon am ndaje. Li mu ko dugge woon mooy xamal ndongo yi ñu jiite li ñu namm a def. Ndogal ya rote ca ndaje ma mooy ne jël nañu ndogalu dakkal liggéey yépp lu tollu ci diiru benn fan, muy jàng ak lépp. Te, amaana sax, ñu yokk ko. Ñu teg ci benn fan boo xam ne dangay lekk te doo fay. Am na nu muy deme ñu yokkaat ko. Li sabab loolu mooy li ñu dooragul liggéeyi dëkkuwaay bii di “Village O” ak béréb ba nekk fa ñaareelu bérébu lekkukaay ba. Bi ci topp, mooy ñàkk a matale “WiFi” bi. Bi ci mujj, mooy ñàkkug kaaraange gi am ci biir jàngune bi.
ËTTU ÀTTE BU KAWE BI JOX NA DËGG NJAGA SILLA AK MEETAR ABDULAAY TIN
Njaga Silla kenn la ci ñiy yëngu ci wàllu pólitig te xam-xamam màcc na ci wàllu wote. Moom nag, dafa am dabantal bu mu jébbaloon ginnaaw bi fi Maki Sàll tabbee woon ay way-bokki ndiiso gii di CENA (Commission Electorale Nationale Autonome). Dekkere boobu Maki xaatimoon la gisoon ne tegu ko ci yoon. Ëttu àtte bi àddu na ci mbir moomu tay ci alxames ji. Jël na ndogalu neenal dekkere boobu Maki xaatimoon.
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
Démb, ci àllarba ji, la ñii di waa Tottenham jël seen raaya bu njëkk bi ñu sosoo ba tay. Joŋante bi ñu ko jële mi ngi doxoon seen diggante ak ñii di waa Manchester United. Naataangoy doomu Senegaal jii di Paab Mataar Saar ñoo dóor ékib boobu benn bal ci dara. Kon, ñoom ñi ngi soog a am raaya fukki at ak juróom-ñaar ginnaaw bi ñu sosoo ak léegi.
Ba tay ci xibaari kuppe gi, doomu Senegaal jii di Ibraayma Ñaan aj nañu ko ñaari at yoo xam ne du ci laal bal. Li ko waral mooy dañoo saytu yaramam gis ne am na lu ci bokkul. Maanaam, day def li ñuy wax “dopage”. Te moom joxewul ay firnde yu leer ñeel loolu ñu koy tuumaal. Loolu nag, kurél gii di AFLD (Agence Française de Lutte contre le Dopage) da koy tere. Doomu Senegaal jooju nag, ma nga nekkoon fa Angers, nekkoon ci at mu mujj ci pas gi mu xaatimoon ak ñoom. Mu mel ni, dina toog diir bu mu dul bokk ci joŋante yi.
Lu ñeel xibaari kuppe gi ba tay fa Ërób, kuppekatu Réal Madrid bii di Luka Modric xamle na ne dafay jóge ca këlëb. Nee na joŋante yii ñu nekk jeexee day dem. Moom nag, xaw na fa yàgg. Ndax, atum 2012 la fa ñëwoon ba tay. Kon, def na Espaañ fukki at ak ñett.
XEW-XEW BU TIIS FA “CORNICHE” BU NDAKAARU
Naqar ak tiis la ndongo yi nekke fa daara ju kawe jii di UCAD am rawatina ñi nekk ci banqaas bii di SJP (Sciences Juridiques et Politiques). Seen naataangoo bii di wuyoo ci turu M. Ndóoy moo génn àdduna ci anam yu doy waar. Dafa di, ndongu loolu dafa demoon fa “Corniche” ngir doxantu faf ndogal fekk ko fa. Maanaam, dafa tarxiis, daldi daanu, ndox mi yóbbu ko. Ndeysaan, dafa mujje lab. Sàppëer a mujje génne néewam ci ndox mi.