LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (23/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SÉEX BAARA NJAAY DAY DES KASO

Fan yee weesu lañu ko doon sàkkul ag bàyyig négandiku. Waaye, mujjul woon a àntu. Ndax, ëtt bii ñuy dippe “chambre d’accusation de la cour d’appel” moo doon saytu càkkuteef googu layookatam yi defoon ngir ñu bàyyeendi ko. Maanaam àttekat bi moom daf leen ko nanguloon. Waaye, toppekat bi moo bañ ndogal li. Moo taxoon mu sàkku ab dabe (appel) ngir ñu saytuwaat ndogal loolee. Kon, donte ne sax jamono jii wér-gi-yaramam nasax na lool ci sababu xiifal gi muy def bu yàgg ba léegi, terewul ne day desandi ca kaso ba.

DÀQ NAÑU MBIRUM EL MAALIG NJAAY MI

Démb lañu waroon a àtte mbirum El Maalig Njaay mi yor kàddug Pastef ñeel ndéggat li ñu ko tege woon loxo. Ginnaaw bi ñu ko bàyyee la toppekatu bokkeef bi sàkku ab dabe ngir ñu xoolaat yëf yi. Li ñu ko doon toppe ci mbir moomu mooy yee fitna ak biral ay xibaar yu wérul. Mbir moomu nag, dàq nañu ko ba fukki fan ak ñaar ci weeru sàttumbar.

MBIR MU DOY WAAR

Ñaari ndawi GIGN (Groupe d’Intervention de la Gendarmerie Nationale) la birigaad bu Sali Portidaal teg loxo. Sabab bi ñu leen jàpp moo yéem ñépp. Ndax, nee ñu, lu tollu ci ñaari miliyaar ci xaalis bu bon lañu fekk ci ñoom. Maanaam, li ñuy wax “faux billets” ci nasaraan. Te, li ci gën a yéeme mooy ne gaa ñooñu nee nañabokk nañu ci ñiy wattu kaaraange kilifa gu mag ci Nguur gi.

MBËKK MI

Jamono jii, mbëkk mi nekk na xew-xew bi gën a lëmbe réew mi. Ñu bari dee ci, ñu bari ñu jàpp leen, ña ca des ñu rawale leen. Mu am tamit ñoo xam ne dañu leen di delloosi ci réew. Réewum Senegaal nag, am na lu tollu ci ñaari téeméer ak juróom-ñeent fukk ak ñeent yoo xam ne dañu leen delloosi. Doomi Senegaal yooyu nga xam ne ca Marog lañu leen rawale woon jóge nañu fa Daxla. Tey ci àllarba ji lañu war a agsi ci réew mi.

Beneen xew-xew bu doy waar moo am ci mbëkk mi. Ndax, fale ca Mbuur, geneen gaal gu fa jóge woon moo réer. Kurél gii di CLPA (Conseil Local de Pêche Artisanale) ñoo biral xibaar bi, wax ne gaal ga fa jóge woon juróomi fan ci weeru ut ba tey xamuñu fan la nekk. Gaal googu mi ngi yeboon lu tollu ci téeméeri doomi-aadama yu bëggoon a dem fa Espaañ. Boobaak léegi nag, seen i mbokk moom ñi ngi ci njàqare gu réy. Ndax, seen njaboot googu fu mu nekk jamono jii ump na leen.

Mu am tamit geneen gaal goo xam ne ay doomi Senegaal la yeboon, àgg na tey fa Espaañ. Gaal googu, mi ngi defoon lu tollu ci téeméer ak ñeent fukki nit ñoo xam ne marinu Espaañ bi moo leen rawale. Ñu yokk ci ne diggante démb ak tey rekk lu jege ci ñeenti gaal yu jóge Senegaal rawale nañu leen fa. Li ñu ci rawale tollu na ci ñetti téeméer ak ñeent fukk ak ñeent.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj