LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (24/01/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJIITU RÉEW MI JOX NA DIG-DAJE LAWAX YI ÑU TÉYE

Ginnaaw bi ndajem ndeyu àtte mi jeexalee caytug xobi baayale yi, dafa am lawax yu ñu téye woon. Lawax yooyu nag, ñoo mànkoo woon, bind bataaxal, di sàkku ndimbal ci Njiitu réew mi Maki Sàll. Moom Njiitu réew mi, jox na dig-daje lawax yooyu. Nee ñu, ci ngoonug àllarbay tey ji la leen waroon a dalal, bu juróom-benni waxtu jotee. Ci lawax yooyu, am na ci koo xam ne, nee na moom du dem ca ndaje mooma. Muy Soxna Aminata Ture mi nga xam ne, bu yàgg ba tey, mook Njiitu réew mi duñu séq ub taal. Nee na, moom Soxna si, janoo ak Njiitu réew mi yitteelu ko wenn yoon. Looloo tax ba kii di Bugaan Géy Dani daldi ŋàññi taxawaay bi soxna si am, donte ne sax, leeralul taxawaayam ci ndaje mi. Maanaam, waxul ndax dina dem am déet. Naka noonu, Amsatu Sow Sidibe, Aajibu Sumaare, Doktoor Abdu Rahmaan Juuf, Abdu Mbàkke Baara Dolli ak Mari Tëw Ñaan duñu bokk ca ñay teeweji waxtaan woowa. Waaye, loolu terewul am na fukk ak juróom ñoo xam ne dinañu teewe ndaje ma.

BÀYYI NAÑU FATIMATA SAHRAA WAGE AK MANSUUR SIISE

Fatimata Sahraa Wage, ñu gën ko xam ci turu Sahraa bu Usmaan Sonko, mujj nañ ko bàyyi. Moom, militaŋu Pastef boobu nag, ay weer a ngi nii ginnaaw ba ñu ko tegee loxo ak léegi. Waaye, démb ci talaata ji lañu koy sog a bàyyi mu fanaani këram. Naka noonu, Mansuur Siise tamit, nga xam ne amoon na fi coow ak meeru Mbuur bi, mujje nañu ko bàyyi, donte ne sax, téye nañu ko ay fan ci kaso bi.

AKSIDAŊ BU METTI FA JURBEL

Aksidaŋ ba amoon biig ci yoonu Poroxaan wi, boori fukki waxtu ak benn, limub ña ca génn àdduna ma ngay yokk. Benn Mbàkke-Tuubaa ak ab biis (Tata) ñoo mbëkkante ca boori dëkk bii di Nebe, nekke fa diwaanu Jurbel. Ña ca génnoon tolloon ci juróom-ñetti nit. Limub nit ña ca ñàkk seen i bakkan dem na tey ci fukk ak ñett. Fukk jële ciy gaañu-gaañu yu metti. Mu am ci sax koo xam ne, jamono jii, mi ngi ci diggane dund ak dee, fajkat yi di ko jéem a xettali.

CAN KODDIWAAR 2024

Lu tollu ci ñetti joŋante kepp la ekib bu nekk amagum ci CAN bi, coow li ne kurr. Li ko waral du lenn lu dul ne dafa am yenn ekib yoo xam ne, bu ñu, ñibbeegul tamit, seen ug des fa Koddiwaar moom wóoratul. Ba tax na, jamono jii, am na tàggat (entraineur) bu gedd, bàyyi, muy Tom Saintfiet mi yoroon Gàmbi. Mu amati ñaar ñoo xam ne, ñoom, dañ leen dàq, muy Chris Hughton mi doon tàggat Gana ak Jean-Louis Gasset mi yoroon Koddiwaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj