LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (24/6/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BÉSU LIGGÉEYKATI BOKKEEF GI

Démb, ci dibéer ji, 23i pani suwe 2024, lañ doon màggal ci àddina sépp bés bees jagleel liggéeykati bokkeef gi. Ci màggal googu, jëwriñ jii di Óliwiyee Bukaal jaare na ci doon sargal képp kuy yëngatu ngir bokkeef gi. Mu leen di fàttali ni seen yitte ak seen taxawaay wu matale lañuy sàkku ci ñoom ngir mën a taxawu askan wi fépp fuñ mën a nekk ci biir réew mi, ak fànn wu mu mën a doon.

Jëwriñ ji di fàttali ni, fii ci réewum Senegaal, liggéeykati bokkeef gi àgg nañ ci 200 000iy nit ci lim. Ñuy ay ndawi buur yuy yëngatu bés bu nekk ngir ngëneeli ñépp. Waaye, buñ fàtte ni, fépp fuñ nekk rekk, seen melokaan mooy wow Bokkeef gi. Ndaxte, moom lañ fay teewal, ba fa bitim-réew.

WÀÑÑITEG DUND GI

Ginnaaw bi mu jëlee ay ndogal yu bees ci wàññiteg dund gi, Nguur gi tàmbali naa jël ay matuwaay ngir ñépp sàmmonteek njëg yi mu samp. Wàññite googu sax, dees na ko tàmbali doxal naka tey ci altine ji. Ci noonu, luy tollook 1000iy ndaw ak i takk-der dinañu tas ci biir réew mi, ngir kenn bañ a jalgati njëg yi. Jaaykat yeet waral nañ ci ñoom ñu taf njëg yi ci buntu barab yi ñuy jaaye walla ci biir.

WOLKAT YI DINAÑU BANK SEEN LOXO

Ginnaaw bi Ndajeem réew mi ñeel jëfandikoo gi sampee njëg yi ci wàññiteg dund gi, ñii di wolkat yi te ñuy defar sunguf si xamle nañ ni dinañu bank seen i loxo. Dinañu toogandi diir bañ a defar sunguf. Muy luñ xamle démb ci dibéer ji. Li ñuy naqarlu nag mooy wàññi gi Nguur gi wàññi sunguf si te pepp mi ñu koy defaree di gën a yokk. Rax-ci-dolli, dara leeragul seen bopp ci li Nguur gi wax ne dina leen ko teggil ci tegaay yi ci waroon. Ñuy sàkku ci kilifa yi ñu gaaw wut ciy pexe balaa wàll wi di gën a nërmeelu. Nde, niñ leen di sëqatalee mëneesu ko dékku.

MBAS MI TOPP NA UJAAJ YI

Koronaa bi dellusiwaat na fi réew mi. Ujaaji Saa-Senegaal yi njëkk dellusi la toppee fa barab ya ñu doon ajee. Muy xibaar bu tukkee ci Sàrl Bernaar Saañaa, dib fajkat buy saytu wér-gi-yaramu way-tukki yi fa dalub roppalaan bu AIBD. Bees sukkandikoo ci kàddu yi mu yékkati te sunuy naataango yu APS siiwal leen, ci 7i roppalaan yu jot a jóge Màkka, téeméer boo jël, lu ëpp 20 jàpp 60 am nañu jàngoro ji. Ba tax muy tiit jàngoro ji jóge ci ñoom law ci biir réew mi. Naka noonu, muy digal Ujaaj yi ñëwagul, ñu takk ay mask fa ñu nekk ak fa ñuy jëlee roppalaan yi, te wéy di ko takk bu ñu ñëwee ci réew mi.

UJAAJ YI FAATU FA MÀKKA

Ujaaj yu bari jot nañ ñàkk seen i bakkan fa Màkka. Waaye, ba léegi dese nañ leeral lu leen faat. Looloo tax ba jëwriñu wér-gi-yaram gi jël ay matuwaay, rawatina jamono yi ñu nemmeekoo jàngoro Covid-19 bi ci ñu takku ci ujaaj yi jot a ñibbisi. Naka noonu, jëwriñ ji waral na ñu saytu ujaaj yi bu ñu agsee ci réew mi. Bu loolu weesoo itam, muy sàkk ci askan wi ñu dakkal xew yi ñuy amal duppee leen “nganale” ngir wattandiku wasaare jàngoro ji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj