LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (24/7/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DINDI NAÑ ÑAG YA WOON CA SITE KËR-GÓOR-GI

Dindi nañ ñag yañ defoon fa Site Kër-Góor-Gi ngir ndar-kepp Usmaan Sonko. Tey ci suba lañ dindi yépp. Benn xibaar rotagul, bawoo ci Nguur gi, ngir wax li tax ñu jële fa takk-der yi. Bu dee waa kër Sonko, rawatina Jibril Géy, moom daf nee lii du xew-xew ci ñoom. Te, waxtaanuñu ak Maki Sàll walla keneen ; ñoo jékki woon ñag kër Usmaan Sonko,tàgguwuñu woon kenn. Ñoo jékkiwaat dindi ko te yégaluñ ko kenn.

Bi xibaar bi jibee, tas ci mbaali jokkoo yi, ndawi Pastef dañ daw wutali kër Usmaan Sonko, bég lool. Nde, ñetti weer a ngi nii, kenn mënul woon seeti Usmaan Sonko, moom it mënul woon dem fenn. Waaye nag, takk-der yaa nga ca wetu koñ ba ba léegi.

WOTEY 2024 YI

Ginnaaw bi mu yéglee ni day bokk ci wotey 2024 yi, Aminata Ture mi fi nekkoon magum jëwriñ ji ci Nguurug Maki Sàll seqi na beneen jéego ñeel wotey yooyule. Mënees na wax ni, sóobu na xaat ci kàmpaañ yi. Nde siiwal na naalam ci bi muy amal am ndaje ak kàngaami pàrteem. Ñu gis ni naalam bee ngi lalu ci 9i ponk. Ñu gën cee ràññe ndefaraan gi (l’industrialisation), jumtuwaay yi (les infrastructures), wàlluw Yoon (la justice) ak Càmm gu mucc ayib (la bonne gouvernance).

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI

Mer ba futt la ndongo yi nekk ca jàngune Séex Aamidu Kan bu koldaa xéyee tey. Ñoom nag, li leen metti mooy seen njàng mi tëe jaar yoon. Atum Yàllaa ngi nii mënuñoo jàng, te dara waralu ko lu dul ñàkk i jumtukaay. Nde, ndongo yi féete ci bile jàngune, ñu gën ko xame ci turu Université virtuelle du Sénégal, dañuy yittewoo ayi nosukaay. Waaye, mënuñoo jot ci nosukaay yi leen Nguur gi dig boobu ba tey. Ñi jot a am i nosukaay itam lënku të na leen ticc.

DEM BEEK DIKK BI

Waa AFTU, di mbootaayu boroomi biisi Tata yi dañuy ñaxtu jamono jii. Moo tax, li ko dale ci altiney tey ji, jàpp àllarba 26i fan ci sulet, dinañu gaare seen i daamar, kenn ci ñoom du daw, Senegaal gépp nag, ba mu daj. Ñoom, li ñu bëgg mooy Nguur gi xoolaat anam yi ñuy liggéeye. Naka noonu, ñu koy woo ci diisoo ak di sàkku mu xaatimal leen i digaale yu am maanaa, ba seen nekkin mën a ñoŋ.

COOWAL BOOKAR SÀMB JÉEY AK CBEAO

Coow li doxoon ci diggante baana-baana bii di Bookar Sàmb Jéey ak Bànk bii di CBEAO jeexagul ba léegi. Ginnaaw bi Yoon diglee ab gëstu ak i xóotal, li njuréef yi wone mooy Baana-baana bi moo am dëgg. Ñu jàngee ci caabalug gëstu bi ni Bànk bii di CBEAO moo ameel Bookar Sàmb Jéey xaalis bu tollu ci 879 002 411 CFA.

AFROBASKET 2023

Gaynde Senegaal yu jigéen yaa ngi ci waajtaayu Afro basket 2023 biy ame fale ca Kigali, réewum Ruwàndaa. Démb ci dibéer ji lañu doon amal seen joŋante bu njëkk ci waajtaay bi. Mu doxoon seen digganteek Mosàmbig. Waaye xale Mustafaa Gay yi dañoo mujje lajj ci 69-70.

BITIM-RÉEW

Ki fi nekkoon Njiitu réewum Gine, Alfa Konde yékkati na kàddoom yu njëkk ginnaaw bi takk-der yi foqatee woon Nguur gi ci moom ca atum 2021. Moom nag, fa Turki ga mu daw-làqu la siiwalee ab widewoo. Mu ciy xamle ni moom mooy Njiitu réewum Gine ba léegi te na ko ay ñoñam séentu nde dina delsi balaay yàgg.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj