Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jóge na fi, dem Farãs. Nawleem bi, Njiitu réewum Farãs (Emmanuel Macron), ak Thomas Bach mi jiite ndiisoog doxal bu “Comité International Olympique” (CIO), ñoo ko woowee ca ndaje mu mag ma fa war a am te aju ci wëppa wii di “Sport pour le développement durable”, maanaam “Tàggat-yaram ngir yokkute gu sax”. Ëllëg, alxames, 25i pani sulet 2024 lees war a amal ndaje mi.
Bu weesoo loolu, Njiitu réew mi dina teewe ubbiteg “Jeux Olympiques” yu Pari yi, ci àjjuma ji, 26i pani sulet 2024.
BIRALUG DPG BU ELIMAANU JËWRIÑ YI
Njiiti Kippaangoy dépite (Groupe parlementaire) yi séq Ngombalaan gi jot nañoo daje ba amal ay liggéey yu jëm ci yeesalaat sàrtu-biir (Règlement Intérieur) campeef (institution) googu. Tey ci àllarba ji, 24i pani sulet 2024, lañu jébbal liggéey yi ñu jot a amal Njiital Ngomblaan ga, Aamadu Maam Jóob.
COOWAL WAAXU NDAKAARU
Coow tàmbali naa juddu fa waaxu Ndakaaru (Port autonome de Dakar) ci diggante njiit la, Waali Juuf Bojã, ak kurélug liggéeykat yi fay faral di daan seen doole. Lépp a ngi juddoo nag ci ndogal li njiit li jëloon keroog 25i pani suwe 2024, daldi aj yeesalug pas yi. Muy ndogal lol, dafay bari ay njeexital ci liggéeykat yooyu. Nde, dina laal lu ëpp 400i nit, daldi leen xañ liggéey ca saa sa.
Looloo tax ba seen kurél gi yékkati ay kàddu. Ñuy sàkku ci njiit li mu dellu ginnaaw ci ndogalam loolu. Ndax, ay ndaw ak i mag, rawatina ay boroom kër kese ñoo xéy bés amatuñu lu ñu def. Naka noonu, ñuy woo tam Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñam ñu geestu leen te càmbaraat bu baax seen i mbir.
BOKKADIL CAN BEACH SOCCER
Gaynde Senegaal yi am nañu ndam ci bokkadil yu Can Beach Soccer (futbalu tefes) 2024. Barkaatu-démb ci dibéer ji lañu doon amal seen joŋante bu njëkk. Mu doxoon ci seen digganteek réewum Gine. Ñoom nag, ñoo fekki woon, daldi dóor 9i bii ci 3. Dinañu amal seen ñaareelu joŋante ci dibéer jii di ñëw (28i pani sulet 2024), fii ci Ndakaaru.
BITIM-RÉEW : JOE BIDEN XÀDDI NA
Joe Biden, Njiitu réewum Amerig li, du bokk ci wotey njiitu réew yii di ñëw ci weeru noowàmbar 2024. Keroog ci dibéer ji la ko xamle, jaare ko ci mbaalu jokkoo bii di X. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, dafa jël ndogal loolu ngir gën a mën a sëgg ci liggéey bi, ci diir bi ko dese ci kayam gi. Dina jël itam kàddu ci kanamu askan wi ngir yegge leen ko ci ayu-bés bi.
Ginnaaw ñàkk bokk gi, Joe Biden wax naat ni dina jàppale kii di Kamala Harris, toftalam ci boppu Nguur gi, ngir mu nekk seen lawax. Muy nag ndogal lu soxna sii di Kamala Harris nangu te di ko rafetlu. Waaye, taxul seen i ñoñ ànd ca saa sa. Nde, biral nañu ni dinañu tegu ci doxalin wu leer ngir tànn ku wuutu Joe Biden.