Njiitu réew mi ak Càmm gi dinañ wax ak askan wi ginnaaw ëllëg, ci alxames ji 26i pani sàttumbaar 2024. Li ñu ko duggee mooy biral njureef yi tukkee ci càmbar bi ñu doon càmbar li ñu fi fekk. Dañu woo saabalkat yi, bu keroogaa, ca fukkeelu etaasu taaxub caytu bees dippee Mamadu Ja (building administratif Mamadou Dia). Ab yégle lañu génnee, xamle ci xibaar bi.
Waxaale nañ ci yégle bi ne, keroog altine 7i pani oktoobar 2024 lañu fas yéene fésal lees dippee “Référentiel 2050”. Maanaam, téere bi ëmb naal yi ñu fas yéene jëmmal ak yoon yi ñuy jaar ngir soppi Senegaal ba mu doon réew mu naat mom, ci jub, jubal ak jubbanti lay lalu.
WOTEY NGOMBALAAN GI
Wotey Ngombalaan gi ñu randalsi mooy tàmbalee coow ci dëkk bi. Ginnaaw bi ci weer ak i fan képp a dese, langi pólitig yi sóobu nañ ci. Ku ci nekk a ngi lal i pexe ak i lëkkatoo. Naka noonu, ñi ñuy woowe les libéraux, ñu gën cee ràññe waa PDS, waa Réewmi ak waa APR, dellu nañu doon benn dank ngir ëppale ay toogu keroog ngoonu 17 noowàmbar 2024. Aamadu Ba mi fi nekkoon lawaxu waa BBY ci wotey Njiitu réew mi ma nga lëkkatook Xalifa Sàll ak Aminata Mbeng Njaay. Bu dee waa Nguuru gi moom, naruñoo yóbbu lëkkatoo Diomaye Président gi ñu taxawaloon ci wotey Njiitu réew mi. Bees sukkandikoo ci xibaar yi tukkee ci seen ndaje gaawu gi weesu, làngu Pastef dafa nar a demal boppam donte ni dina ubbil buntam ñi mu àndaloon.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Ñaari ayu-bés képp des ngir lekool yi tijji. Waaye fa Maatam, ñàkk matale limub jàngalekat dina gën a doon jafe-jafe. Nde bees sukkandikoo ci xibaar yi kilifa yi siiwal, lu tollu ci 411i jàngalek bàyyeekoo nañ fa ci atum 2024 mi, ci 70 kott yu ñëw. Muy nag jafe-jafe bu diiwaan yu bari di jànkonteel. Waaye Jëwriñ ji Mustafaa Giraasi, àddu na ci. Fekk mu fa doon jiite am ndaje ci waajtaayu ubbite lekool bi fa Maatam. Dig na leen ni dina doon lu muy joyyanti, te jot na ndigal ngir def ko. Dina fexe ba ñu jagleel diiwaanu Maatam lim bu takku ci njàngalekat yu bees yi ñuy jël.
TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA ETAA SINI
Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo nga jamono yii fa réewum Etaa Sini. Muy tukki bu mu fay amal ngir fekke 79eelu ndaje mu mag mu mbootaayu xeet yi. Ginnaaw bi mu fa teewe bàrki-démb ci gaawu gi, jot naa teewe, démb ci dibéer ji, ndaje mi ñu jagleel ëllëgu àddina si (sommet de l’avenir). Ndaje moomu, ñaŋ ca doon waxtaane nees di waajale ëllëg ngir mbooleem xeet yi mën a am dund gu ñoŋ te yàgg ci jamono.
MBËKK MI
Coowal mbëkk mi demagul bay giif fi réew mi. Ba démb ci dibéer ji gis nañ ag gaal lu tolloog 70i km ci géeju Ndakaaru. Li ci gën a yéeme nag mooy gaal gi dafa nekkoon di boy noonu ci ngelaw li. Kenn ku ànd ak bakkan nekkul ci biir. Bees sukkandikoo ci xibaar yi waa DIRPA (Direction de l’information et des relations publiques des armées) joxe, waññeegum nañ 30i nit. Waaye fàww luññutu gi egg ngir ñu mën a xam lim bi dëgg ak fu gaal gi bawoo. Wax nañ itam ni yombul ñu génn leen, ràññatle leen ak jële leen foofu ndax anam yi ñu fekke néew yi.