LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (25/12/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Saytukati ndeyu àtte réew mi ñoo ngi wéy ba léegi di jot wayndarey way-sàkku lawax yi ñeel wotey 2024 yi. Ci 77i lawax yi jotoon a joxe seen i warlu (caution), 34 yi jébbal nañ seen i wayndare fa gerefiyeewu saytukati ndeyu àtte réew mi. Usmaan Sonko itam bokk na ci ñi jébbal seen i wayndare donte ni amagul woon xobi baayale yees ko lànkaloon. Bu weesoo ëllëg ci talaata ji nag, 26 desàmbar 2023, saytukat yi dootuñu jël wenn wayndare. Dañuy daldi jublu ci càmbar wayndare yi ngir leeral ñi matal baayale yi ñeel wotey 2024 yi.

SET TÀNN NA USMAAN SONKO

Ba tey ci li ñeel wotey 2024 yi, làngug pólitig gii di SET (Sénégal en Tête), te Mustafaa Giraasi jiite ko, tab na Usmaan Sonko ngir mu nekk seen lawax. Muy ab xibaar bu ñu siiwal cib yëgle bu ñu génne tey. Ñu cay xamle ni yaakaar gi ñu am ci Usmaan Sonko ak gis-gis bi ñu bokk ak moom ci nees war a soppalee réew mi moo leen andi ci ñu jël ndogal loolu. Fas nañ yéene nag  dooleel nekkug lawaxu Usmaan Sonko, jaare ko ci COALITION SONKO 2024.

LEGS AFRIKA

Kurél gii di Legs Afrika doon na màggal ci gaawu gi 10i atam ginnaaw bi mu juddoo ak tey. Muy ab kurél gu ay Saa-Afrig taxawal ngir di ci waxtaane lépp luy gisin ak jëmuwaay ci wàllu xamtu, pólitig, koom ak dëkkin fi Afrig. Ci seen ndaje mi ñu ko doon màggalee ci gaawu gi, Mamadu Lamin Loum mi fi mësoon nekk Njiitul Càmm gi fi Senegaal yékkati na fay kàddu jëmale ko ci jafe-jafey réew mi. Bees sukkandikoo ci gis-gisam, doxalinu pólitig gi fi Senegal rekk moo wopp réew mi. Nde seen i pexe yamul lu dul ci nees di def ba jot ci nguur gi wall ba du leen rëcc.

 BITIM-RÉEW

Fa réewum Niseeriyaa, cong mu metti la fa ay gàngoor yu gànnaayu ba diis amal ci gaawu geek dibéer ji. Cong maa nga ñu amal ciy dëkk-dëkkaat yu nekk fa dëkk ba ñuy wax État du Plateau te féete fa diggu réew ma. Bees sukkandikoo ci xibaar yi Njiiti dëkk ba mujje génne, 113i doom-aadam jot nañ cee ñàkk seen bakkan. Muy lu ñuy ragal nag mu yokk nde jàmmaarloo yaa nga ñu doon wéyal tey ci siba si.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj