Aliw Saane dellu na kaso. Moom, njiitul mbootaayu Y’en A Marre te it, di tof-njiitu kurélu F24, mujjoon nañu ko bàyyi. Li ñu ko doon toppe mooy bokk ci ndajem-ñaxtu mu ñu tere ak yee fitna. Mu mel ni mbir mi yemul woon foofu. Ndax, toppekat bi moo ko yóbb ca ëtt bii di “Chambre criminelle” ngir ñu neenal bàyyig négandiku gi ñu ko bàyyi woon. Looloo tax ba mujj ko dóor tey li ñuy dippe “mandat de dépot”. Maanaam ëtt boobu tëjlu na ko.
JÉYYA JA CA WAKAAM
Ñaari ayu-bés yu teg a ngi ngii, géej giy wéy di wann doomi Senegaal yiy sóobu ci mbëkk mi. Dafa amati ag gaal gu këppu fa Wakaam, ay bakkan yu bari rot nañu ci. Ndax, démb ñoo ngi doon wax limu fukki nit ak juróom yu ca faatu. Tey, nee ñu, lim bi àgg na ci fukk ak juróom-ñett.
NJÀQARE JA CA FAAS-BÓOY
Noppeeguñoo jooy bakkan ya rot fa Wakaam, jeneen jéyya tegu ca. Nee ñu, fa gox ba ñuy wax Faas, nekke ca Tiwaawon, am na gaal gu fa bawoo lu jege fukki fan ak juróom. Te, kenn xamagul ci lan waa gaal googu réer nekk. Maanaam, ba tey kenn gisu leen. Li yéenekaay bii di Bés bi fésal, mooy ne gaal googu yeboon na lu tollu ci téeméer ak juróom-fukki doomi-aadama. Ñooñu nag, jamono jii seen ug njaboot a ngi ci njàqare ju réy. Ndax, du waa Espaañ walla Marog ku ci joxe ay xibaar ñeel seen mbokk yooyu.
NGUURUG SENEGAAL JËL NA NDOGAL
Fan yii ñu nekk, coowal mbëkk mi lëmbe na réew mi. Réewum Senegaal nag jël na ndogalu delloosi doomam yooyu ñu téye Daxla fa Marog. Diggante juróom-ñeenti fan ak fukki fan ak ñaar kepp ci weeru sulet wii, marinu Marog bi wallu na lu tollu ci ñeenti-téeméer ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñetti (478) doomi Senegaal yu doon mbëkk. Ñooñu ñu jàpp foofa, Nguuru Senegaal dina indi ñenn ñi ci àjjuma jii. Ñi ci des dinañu ñëw ci dibéer ji, yemoo ak fanweeri fan ci weeru sulet wii.
XEW-XEW BU DOY WAAR CA KUNGÉEL
Benn sàmm bu ndaw buy wuyoo ci turu Ng. Taal lañu bóom ci guddig démb gi jàpp tey. Nee ñu, coowal jollasu ak téeméeri dërëm a ko boole ak ki ko rey. Ndax, kii di A. Dem la jollosoom yàqu, mu jox ko S. Laam ngir mu defaral ko ko. Faf nag, Yàlla def coow am seen biir muy S. L, A. Laam ak Ng. Taal. Ci la Alfa jëlee jaasi ji rekk caw ko Ng. Taal kenn ci mu jàkkaarloo woon, mu faatu ca saa sa.
ISMAAYLA SAAR
Ismayla Saar mi nekkoon Watford, fa Àngalteer, ñeenti at ci ren, dem na Marseille. Laata muy dem Watford, Farãs la njëkkoon a nekk, di futbal Rennes. Xaatim na ak Marseille pasug juróomi at. Maanaam, foofu lay nekk ba 2028. Moom, doomu Senegaal bi nag, limatu ñaar-fukk ak ñett (23) la fay sol.
CAF AWARDS
Ndaje moomu ñuy amal at mu jot ngir neexal futbalkat yi gën a ràññeeku ci at mi muy ci góor ñi, di jigéen ñi. Xew-xew boobu nag, jàpp nañu ko. Dinañu ko amal fukki fan ak benn ci weeru desàmbar 2023 fa Marog. Su boobaa, dees na xam kan mooy wuutu doomu Senegaal bi, Saajo Maane, nga xam ne moo ko jëloon at mii ñu weesu.
LÀMB
Ay at ginnaaw bi mu gëjee bëre, Amaa Balde mujj na amaat kombaa. Làmb jooju mi ngi dox digganteem ak Giri-Bóordoo. Xew-xew boobu nag, ajandi nañu ko ay yoon. Te, li ko waraloon di gaañu-gaañu kenn ci ñaari mbër yi. Wii yoon moom, jàpp nañu ko ci benn fan ci weeru oktoobar.