LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (25/7/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Démb ci àllarba ji la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay tukki. Wii yoon ma nga jëm fale ca Farãs donte ne sax, demoon na fa ci lu yàggul dara. Waaye, li sabab tukki yi ba tey dese naa bokk. Wii yoon, daf faa dem ci wooteb naataangoom bii di Emmanuel Macron, Njiitu réewum Farãs ak Thomas Bach Njiitu kurél gii ñuy dippe “comité exécutif du Comité International Olympique”. Nde, dina tax mu fekke ndoorteelu powi olempig yi. Waaye, dina bokk tamit ci ndaje mu mag mi jagleel tàggat-yaram ak yokkute gu sax. Ndaje moomu, tey ci alxames ji lañ ko doon amal.

NJIITU NGOMBLAAN GI WOOTE NA AM NDAJE

Lu yàggul dara, njiiti kippaangoy dépite yi doon nañu daje ngir waxtaane coppite yi ñu war a amal ñeel yenn ci sàrti Ngomblaan gi. Ndax, kii di elimaanu jëwriñ yi Usmaan Sonko daf ne woon bu ñu amalul coppite yooyu du def “DPG” bi. Aamadu Maam Jóob di Njiitu béréb ba woo na way-bokki pekk yi fa bérébu waxtaanukaay wa. Ndaje moomu mu woote, dinañu ko amal suba ci àjjuma ji, ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru sulet. La ñu fa war a waxtaane nag des naa leeral.

LAYOO MANSUUR FAY AK AMINATA TURE

Coow li doxoon diggante ñaar ñi fi nekkoon ay jëwriñ ci Nguur gi fi jóge teeri na ci loxoy Yoon. Li waral coow li mooy tuuma yi Aminata Ture teg ci ndoddu Mansuur Fay ñeel junniy miliyaaru “Fonds Covid-19” yi. Looloo tax, mu dóor ko ab pelent ngir Yoon àtte leen. Ñoom ñaar nag, tey ci alxames ji lañu leen waroon a àtte fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru. Aminata Ture moom teewe na layoo ba. Waaye, Mansuur Fay moom, kenn gisu ko fa. Loolu terewul ne mbir mi àtte nañu ko. Te, kii di Aminata Ture teggiwul tànkam fa mu ko tegoon. Ku ñuy daan ak ku ñu dul daan, dees na ko xam juróom-benni fan ci weeru ut wii ñu jëm.

Naka noonu layoo bi waroon a dox tey diggante Daam Mbóoj ak Majambal Jaañ dañu koo mujje dàq. Layoo bi jàppaat nañu ko fukki fan ak ñeent ci weeru nowàmbar. Moom Majambal tamit, li muy toppe Daam Mbóoj mooy ay tuuma yu mu teg ci loosam. Maanaam, li ñuy dippe “diffamation”.

AKSIDAŊ BU METTI FA MAATAM

Jéyya jooju mi ngi am tey ci alxames ji diggante Ndulumaaji ak Wurosoogi. Benn sëfaan (kamiyoŋ) moo mbëkkante ak ub minikaar buy tollu ci ñaar-fukki palaas. Juróom-benni nit ñàkk nañu ci seen i bakkan, fukk ak ñeent jële ci ay gaañu-gaañu yu metti. Kii di Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay sax, bind na ci xëtu Facebookam di naqarlu jéyya ji, di jaalewaale mbokki way-loru. Rax-ci-dolli, xamle na ne, joxe na ay ndigal ngir ñu toppatoo ñi ci gaañu nu mu gën a gaawe.

BFEM 2024

Ginnaaw bi pàcc bu njëkk ci joŋante boobu jeexee, ñaareel bi moo ciy bëgg a des. Tey, ci alxames ji la kurél gi ñu dénk wàll woowu génnee ab yégle ngir xamle àppug ñaareelu pàcc bi. Maanaam, ñi dese woon ay poñ ba jàlluñu woon ca pàcc bu njëkk ba, mën a mottali. Ñaareelu pàcc bi dina door altine ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru sulet bu juróom-ñaari waxtu ci suba tegalee fanweeri simili.

MUSAA BÀLLA FOFONA INDI NA AY LEERAL

Coowal paacoo li lëmbe woon réew mi ginnaaw tabb yee weesu ba tey ma ngay wéy. Nde, wii yoon, jëwriñ jii di Musaa Bàlla Fofona lañuy tuumaal ne dafa ñoddi mbokkam. Maanaam, dafa am lu mu bokk ak Abdu Xaadar Fofona PCA (Président du Conseil d’Administration) bu SONAGED. Mi ngi xamal ñépp ne mook kooku aw sant kese lañu bokk. Ci gàttal, amul lenn lu ñu bokk, du ci ndey, du ci baay. Te, mi ngi naqarlu jëf jii. Maanaam, bokk ak nit sant rekk tax ñuy jël ay kàddu yu ñagas di ko teg sa kow. Te, kooku, fa mu nekk, mën-mënam a ko fa teg.

DIC TEG NA LOXO AY TAKK-DER NGIR MBIRUM LUUBAL

Xew-xew bu doy waar boobu ma nga ame fa komisariyaa bu Zac-Mbaaw. Juróom-ñeenti takk-der (policiers) lañu fa teg loxo. Li ko sabab mooy koppar gu takku gu ñu jële woon ci ay Saa-Mali. Saa-Mali yi ne koppar gi tollu na ci juróom-benni téeméeri miliyoŋ. Te, ñoom takk-der yi, ñeenti-téeméeri miliyoŋ yi kepp lañu ne moom lañu lim. Léegi nag, gaa ñi, fu ñaari-téeméeri miliyoŋ yi ci des dugg moo leen jaaxal. Kon, am na luy ñuul ci soow mi. Luññuti bi nag, door nañu ko ngir xam nan la mbir mi tëdde. Takk-der yeek Saa-Mali yi moom ba tey ñi ngi ci loxoy Yoon.

JÀPP NAÑU AMET SUSAAN KAMARA

Ahmet Susaan Kamara, njiitu kurélu jàngalekati APR yi, teg nañu ko loxo démb ci àllarba ji. Te, li ko waral du lenn lu moy kàddu yu ñagas yi mu yékkati teg ko ci ndoddu Njiitu réew mi ak Njiitu jëwriñam yi, Usmaan Sonko. Kàddu yooyu mi ngi leen yékkati woon barki-démb ci guddi ci jotaay bu ñu ko woo woon fa Seneweb. Ba mu xéyee rekk lañu ko teg loxo ndax, nee ñu, dafa ŋàññi kilifay réew mi. Jamono jii ñu tollu nag, ma nga ca loxoy Yoon. Am na nag ay tuuma yu ko Yoon teg. Nde, moom tey la gën a nangu ne kàddu yu ñaaw yii moo ma. Waaye, ba tey, xamaguñu ndax dees na ko daan am déet.

DAAN NAÑU SAA-SIIN YI

Saa-siin yi doon néewal doole benn Saa-Senegaal ci ab widewoo, gën na leen aw demin. Démb ci àllarba ji la daan bi dal seen kow, ñoom ñaari Saa-Siin yeek ki leen doon tekkil, Ibraayma Sori Taraawore. Daan nañu leen ñetti weeri kaso yu ñu war a tëdd ak juróomi miliyoŋi ndàmpaay yu ñu war a jox kii di Ibraayma Faal. Ñoom nag, fukki fan ak benn ci weeru suwe wii ñu génn lañu leen yóbboon kaso. Kon, am na lu ñu jot a tëddagum.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj