LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (25/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BAKKANU USMAAN SONKO MI NGI CI XOTTU GERTE

Tey ci àjjuma ji, njiiti lëkkatoo Yewwi Askan Wi seeti woon nañ Usmaan Sonko fa raglub Principal bu Ndakaaru. Dañ fa demoon ngir nemmeeku wér-gi-yaramam. Wii yoon, bàyyi nañu leen ñu gis ko. Ndax, keroog àllarba, dañ leen ko gàntaloon. Biñ fa génnee nag, woote woon nañ ndajem waxtaan ngir wax askan wi ak àddina sépp li ñu fa jële. Waaye de, li ñu saabal raglu na. 

Bi Soxna Ayda Mbóoj  di wax, dafa naroon a jooy. Ñu tiit ak yërmande ci baatam. Mu ne :

  ” Tey jii, di àjjuma 25i fan ci ut, nu xéy, dem fekk fa “service de réanimation” boobu seeti Usmaan Sonko. Waaye bu nu sañoon de, bu ñu xamoon ne noonu lan koy fekkee, ñu def niñ nu defoon àllarba. Ndax Usmaan Sonko mee nu gis, (…) xàmmeewunu ko. Waaye moom it xàmmeewu nu. Usmaan Sonko mënatul dara. […] Mënunu ko woon sax jox tàndarma yi ko xalifa murit yi yónne.”

Kàdduy Abiib Si yi tamit, ag tiitange ak ug njàqare lay feeñal. Daf ne :

“Jamono jii nuy wax ak yeen, lu nekk mën na xew. Naam, ci loxoy Yàlla la dund ak dee nekk. Waaye, tiit nanu.”

PEREFEB NDAKAARU BI AAYE NA DOXU-ÑAXTU WAA “CHEMIN DE LA LIBÉRATION”  

Moor Taala Tin, prefe bu Ndakaaru bi, génne na ab yégle buy tere ndaje mi kurél gii “Chemin de la libération” bëggoon amal ci gaawu bii 26 ut fa HLM Garã Yoof. Ci biir yégle bi, mi ngi xamle ne dafay aaye ndaje mi. Ndax mën na indi ay yëngu-yëngu biir Ndakaaru, ba ci sax tere nit ñi nekk ci seen i yitte.

MAREEM FAY SÀLL TAS MBOOTAAYU “FONDATION SERVIR LE SÉNÉGAL”

Tey la xibaar bi jib. Yéenekaay bii di Le Quotidien moo ko siiwal. Ci àjjuma ji la Mareem Fay Sàll, soxnas Njiitu réew mi, dajale ñi doon liggéey ci mbootaay gi, xamal leen ni daf koy tas.

Cig pàttali, mbootaay gaa ngi juddu woon 2012, bi mu Maki Sàll faloo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj