LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (25/9/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Séex Tijaan Jéey génne na boppam ci lawax yi. Dootul bokk ci ñi namm xëccoo Njiitu réewum Senegaal ci wotey 2024 yi. Muy ndogal lu mu siiwal démb ci dibéer ji. Fekk ñu doon ko dalal ci jotaayu Grand Jury bu RFM. Moom njiitul Avenir Senegaal bi ñu bëgg nag dafa namm jàppale Usmaan Sonko. Bees ko déggee, moom ak i ñoñam gisuñu keneen ku dul Njiitul Pastef li. Te fas nañu yéene xar seen tànku tubéy ngir mu nekk lawax. Te bees ci jógee dinañu ko gunge ci dagaan baatu askan wi ngir fal  ko keroog dibéer 25 féewaryee 2024.

GÀMMU 2023

Njiitu réew mi Maki Sàll ma nga woon ca Tiwaawan. Mu demoon fa ci altine ji ngir seeti xalifa tijaan yi, Sëriñ Mbay Si Mansuur. Ceeti boobu nag mi ngi aju ci waajtaayug gàmmu gi. Naka noonu, xalifa bi dalal na ko ak delegasiyoŋ bi mu àndaloon. Ginnaaw gi, amal nañ fa beneen jotaayu waxtaan ci kanamu mbooloo mi (dinañ ci dellusi).

TIIS

Tiis wu rëy moo dal ci kow askanu Kër Njaay Lóo. Gone gu tollu ci fukki at ak ñaar moo lab cim mbalka. Looloo ngi xew ci àjjuma ji. Ginnaaw bi mu jullee jumaa ba noppi, Baabakar Balde dafa àndoon ak ñaari xaritam doon sangu ci mbalka mii di “Nouvelle Horiwon”. Waaye fala jaar ñàkk bakkanam. Ñuy xaar gëstu bi wone ci yan anam la faatoo.

BITIM-RÉEW

Diggante réewum Niseer ak réewum Farãs a ngi gën a ñagas. Ginnaaw bi Njiit yu bees yi dàqee sóobarey Farãs yi, tëj àmbaasadam, dellu nañ tere bépp roppalaanub réewum Farãs mu naaw ci jawway réewum Niseer. Muy ndogal lu bees lu ñu jël, jaare ko ci Asecna (Agence pour la sécurité de la navigation aérienne en Afrique et à Madagascar). Muy mel ni nag Njiiti Niseer yi noppeeguñu ci dafante beek réewum Farãs.

Njiitu réewum Farãs li, Emanuyel Makarõ xamle naat ni àmbaasadëeram bii di Silfĩ Itte ak sóobare ya fa nekk dinañu ñibbisi ci seen réew balaa at mi di jeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj