Càmm gi siiwal na njëgu gerte gi. Tay, ci ndajem jewriñ mees jagleel njaayum gerte gi (atum 2024-2025) lañu jàpp njëg li. Juróom-benn fukki dërëm ak benn (305 FCFA) la kilo bi di jar. Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, moo ko biral. Ren, njëg li dafa yokk juróomi dërëm (25 FCFA) ndaxte, daaw, kilo bi juróom fukk ak ñetti dërëm (280 FCFA) la doon jar.
TÀGGATU DÉPITE YU BEES YI
Ginnaaw ndam lu yaatu li ñu am ci wotey Ngomblaan yi weesu (17 nowàmbar 2024) làngug pólitig Pastef doon na amal jotaayu tàggatu jagleel ko dépite yi ñu fal bees. Ñiŋ ko doon amal ci njeexitu ayu-bés bi (gaawu ak dibéer) fa Saly Portudal ngir waajal leen ci liggéey bi leen di xaar fa Péncum ndawi réew mi. Usmaan Sonko, njiitu làngug pólitig Pastef, nekkoon itam seen boppu toftale, teewoon na fa bi ñuy yékkati jotaay ba démb ci dibéer ji.
Ci kàddu yi mu fa yékkati nag, amal nay pàttali yu am solo ñeel dépite yi, rawatina sañ-sañ bi ñu am ci mën a wane seen péete, ci lu amul benn par-parloo, ñeel wépp sémbu àtte wu ñu leen andil. Bu ñu mës a fàtte ni dépite askan wi lañu. Dañ faa teew ngir sopparñi dundu Saa-Senegaal yi, te muy xeex bu ñuy amal ñeel pàrti bi ak réew mépp.
NGOMBALAAN GU BEES GI
Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo war a jàpp bés bees war a taxawal Ngomblaan gu bees gi. Muy sañ-sañ bu ko Ndayu Sàrtu réew mi jagleel. Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu L’Observateur, njortees na ni dina génne dekkare bi balaa yàgg dara. Nde niru na ku ci taxaw ngir dépite yi sóobu ci seen liggéey ba mën leen a nattal, Moom ak Càmmam, gafaka gi ñi war a doxalee ci atum 2025 mi teru.
Naka nooneet, ki war a jiite Ngombalaan gu bees gi doon na laaj buy wéy di sampu. Nde ba barki-démb ci dibéer ji, Ayib Dafe (Pastef) dellusi na ci. Fekk ñu ko doon dalal fa màkkaanu Sud FM. Muy xamle ni bari na ñu mën a jiite Ngombalaan gi ci 130i dépite yi ñu am. Bu xel yu bari demee itam ci seen njjit li Usmaan Sonko, way-pasteef yu bari dañ bëgg mu des ci njiiteefu Càmm gi. Waaye ndogal li mujj lee ngi dellu ci moom. Te, am nañu yaakaar mu jël ndogal li gën ci seen làng ak ci réew mi.
GEREEWU TONNIKATI MBALIT MI
Ñoo ngi ci juróom-benni fan bi kurélug tonnikati mbalit mi CCNS (Collectif des Concessionnaires du nettoiement du Sénégal) bankee seen i loxo ak tay. Tax na sax ba foo jaar ci péey yi yëg ko ndax ni mbalit mi jaloo. Waaye, ba tay seen tawat amagul saafara. Bees sukkandikoo ci kàddu yi Ndongo Faal mi yor seen baat biral, li ko waral du lenn lu dul ni jotuñu seen i peyoor te yàgg na bi ñu dalee xaar ak tay. Nde, bi atum 2024 mi teroo ba tay kenn feyu leen. Li leen Nguur gi yoreel diggante sãwiyee ak oktoobar tollu na ci 18i tamñareet.
NDOG AMATINA FA MAATAM
Am ndog mu metti amatina ci yoon wi démb ci altine ji. Ñaari biis yu ndaw ñoo mbëkkante ci diggante Tarawo Dendudi ak Dancaali, fa diiwaanu Maatam. Moo ngi xew bi 5i waxtu di jot ci suba si. Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu APS, ñetti nit ñàkk nañu ci seen bakkan ca saa sa. Am naat fukk ak juróom yu ci jële ay gaañu-gaañu yoy, juróom yi doon nañu ay gaañu-gaañu yu metti.