Ci weeru awril wale jàll la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay tabboon Usmaan Sonko, def ko elimaanu jëwriñ yi. Booba ba tay, moom elimaanu jëwriñ yi, demagul fa Ngomblaan ga ngir def lees di wax ci nasaraan Déclaration de politique générale, gàttal biy joxe DPG. Maanaam, ci tënk, dafa war a aajar naalu pólitig wi mu namm a doxal, ànd ci ak Càmm gi. Dafa am ay gàllankoor yu ko ko tere woon def booba ak léegi. Waaye, mbir mujje na a defaru. Moo tax, ginnaaw bees taxawalee kayug Ngomblaan gu bees gi, ñu àppal ko àjjumay ëllëg ji, yemook 27 pani desàmbar 2024, mu war ci janook dépite yiy teewal askan wi fa Ngomblaan ga. Bu fukki waxtu jotee ci yoor-yoor bi la biral naalam wi.
LU BEES CI NJÀNG MI AK NJÀNGALE Mi FI SENEGAAL
Kurél gii di “Comité d’évaluation des Manuels scolaires et Manuels didactiques” (CEM) moo jël ndogal lu am solo ci njàng mu suufe mi. Nde, dañoo jël benn téere ci téere yees bind ci Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke yi, boole ko ci téere yees war a jàngale. Ndax, ci seen gis-gis, téere bu am njariñ la. Téere boobu nag, dippees na ko “Cheikh Ahmadou Al-Khadim : le Serviteur du Prophète Mouhammad et le leader spirituel”. Ki ko bind di Sëriñ Ahmadu Bàmba Al-Xaddiim Muntaxaa Mbàkke, ñu siiwaloon ko ca atum 2020.
NDAJEM NDEYU-ÀTTE MI GÀNTAL NA BÀRTELEMI JAAS
Ci ndoorteelu weeru desàmbar wii lañu ubbi fukk ak juróomeelu kayug Ngomblaan gi. Moom, Bàrtelemi Jaas, dañoo mujje nangu moomeg dépiteem. Ñu daldi koy jële fa Ngomblaan ga. Ndax, dafa am daan bu gàllu ci ndoddam. Ginnaaw gi, moom Bàrtelemi, dafa jébbal ab dabantal fa ndajem ndeyu-àtte mi ngir ñu neenal ndogal loolu. Waaye, loolu mujjewul a àntu. Ndax, waa ëtt boobu dañu ko xamal ne amuñu benn sañ-sañ ci ndogal loolu. Maanaam, Yoon mayu leen ñu àddu ci xeetu ndogal yu ni mel.
AYSATA NJÀCCI FAAL TEERI NA BIC-GOUV
Bu yàggul dara la saabalkat boobu jóge woon fa E-media. Boobaak léegi nag, kenn xamagul woon gan kër lay dal. Waaye, mujj nañoo xam fan la mujje dem. Nde, léegi, bokk na ci Bic-gouv (Bureau d’information et de communication du gouvernement). Maam Góor Ngom mooy ki jiite banqaas boobu. Moom nag, li ñu ko fa tabb mooy “Cheffe d’unité média”.
LIMUB ÑI DEE CI GÉEJ GI
Mbëkk mi nekk na mbir mu sonal réew yu bari, rawatina ci atum 2024 mi. Looloo tax, ni mu amee lim bu takku bu jot a dugg réewum Espaañ, noonu la amee doomi-Aadama yu bari yu seen i bakkan des ci géej gi. Bees sukkandikoo ci caabal gi ONG Espaañ bii di Caminando Fronteras siiwal, lu ëpp 10. 400i nit dee nañu ci géej gi. Te, loolu mi ngi am ci diggante weeru sãwiyee ba fukki fan ak juróom ci weeru desàmbar wii ñu nekk. Mu nekk mbir mu diis te doy waar. Nde, li ëpp ci ñoom ay doomi Afrig lañu.