Dépite bii di Gii Mari Saañaa wax na ak Càmm gi. Wile yoon, 12i laaj la leen sampal. Laaj na leen ci taaxu Service d’hemodialyse bi nar a daanu fa raglu diiwaanu Cees. Bokk na ci yeneen laaj yi, fu ñu teg, ci wàllu yoon, tere bi ñuy terewaate génn réew mi. Ndax dañu ubbi luññutu ci ñoom walla dañu leen yónnee ndogal li ca teel ngir ñu yég ko ? Samp nay laaj itam yu jëm ci ñàkkug ndox meek mbëj mi ci yenn dëkk yi, yoonu jokkalante yeek lënku gi (réseaux télephoniques et internet) ni ñu bone ci diiwaanu jéeri ji. Am na itam ay laaj yu aju ci yéexaayu peyoori jàngalekat yi ñuy tàggat ak liggéeykati sémbuw RNU yu ANSD (Régistre national unique de l’Agence nationale de la statistique et de la démographie).
MBIRUM ÀTTEB NEENAL BI
Ginnaaw bi waa APR wootee bésub ñaxtu keroog 2i fan ci weeru awril 2025, Abdu Kariim Géey (Xrum Xàq) ak gàngooram “Rappel à l’Ordre” woote nañu itam dajaloo ngir wone seen ñàkk ànd ci àtteb neenal bi ak di sàkku ñu dakkal ko. Ci bi ñuy jàkkaarlook taskati xibaar yi lañu ko biral. Ñuy xamle ne, duñu bàyyi wenn yoon àtte bi jàll. Ba tax ñuy woo Saa-Senegaal yépp ñu fekk leen fa buntu Ngomblaan ga, keroog bésub 2i fan ci weeru awril 2025. Li ñu bëgg nag mooy ñu sàmmonteek ma-xejj yi te féexal Yoon ba mu mën a doxal liggéeyam ni mu ware. Ba tax ñuy laaj fu leen njiit yu bees yi jëme ak lu tax bëgguñoo dakkal àtte bi ba képp ku ci taq yoon jëflanteek yow ?
NJËGU CEEB BI NAR NA WÀÑÑEEKU
Ndiisoog réew mi ñeel jëfandiku gi dina amal am ndaje ci alxames jii di ñëw, 27i fani mars 2025 ci njiiteefu jëwriñu ndefar geek yaxantu bi. Dinañu fa waxtaane itam lu jëm ci njëg yi. Bees ci noppee, dinañu amal ab yégle ci njëgu ceeb bu sew bi ba xam dina yokk walla dafay wàññeeku. Waaye, mu wàññeeku lees ci gën a njort. Nde, bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu Libération, elimaanu jëwriñ yi junjoon na lu jëm ci wàññiwaat dund bi. Ba tax ñuy yaakaar ne, bees jógee ci ndaje mi, kilo ceeb bi mën na jóge ci 410 FCFA wàcc ba ci 310 walla 300 FCFA.
NDAW SI ÑU JÀPP FA SALI AK XAALIS BU BON BI
Jàpp nañu senn ndaw su yoroon xaalis bu bonn fa Sali. Brigade de recherche bu Sali moo ko teg loxo keroog ci guddi gaawu jàpp dibéer. Dañu leen kalaamee ab jokkalante bu teey xel ci diggante senn ndaw ak ub gàngoor ci wetu genn kërug daluwaay (auberge). Ginnaaw gi lañu leen topp ba jot ci ndaw si. Bi ñu ko jàppee nag, fekk nañu ci moom lu ëpp 4i tamñareeti Fcfa ci xaalis bu bon bi ñuy tas ci dëkk bi. Ginnaaw bi ñu jàppee ndaw seet, pólis ubbi na luññutu ngir coytu ñeneen ñu mu ko séqal.