Réewum Senegaal am na yéeney gën a dëgëral digganteem ak réewum Sapõ. Mu fas cee yéene jiital lëkkoo gi ci wàllu koom-koom ak yaatal way-liggéeyal seen bopp yi (le secteur privé). Yaasin Faal, Jëwriñ ji ñu dénk wàllu bennoog Afrig ak mbiri bitim-réew moo ko xamle. Fekk mu doon teewe fa Sapõ ndajem jëwriñ mu juróom-ñeenteelu TICAD (Conférence internationale de Tokyo sur le développement de l’Afrique) bi fay am ci weeru ut 2025. Ba tax na, réewum Senegaal dina bokk ci jotaayu fésal (exposition Osaka-Kansai) bees fay amal ci ponk bii di « taxawal mboolaayu ëllëg, xalaat sunu dundinu ëllëg ». Ngir waajal xew-xew boobu, jëwriñ ji Yaasin Faal jot na faa séq ak naataangoom bii di Kamikawaa Yokoo aw waxtaan ci gaawu gi.
GIS-GISUB ÀLLIYUN TIN ÑEEL YORIINU RÉEW MI
Àlliyun Tin àddooti na ci yoriinu réew mi. Démb ci dibéer ji lañ ko doon dalal ci jotaayu Grand Jury bu RFM. Gis-gisam moo di ne, Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay dafa nëbbu. Ak ni réew mi di doxe, ku ko bëgg dégg ak ku ko bëggul a dégg, loolu moo am. Te, Usmaan Sonko moo nekk di jiite réew mi fii mu nekk nii. Muy i kàddu yuy dëggal gis-gis bu fi dépité BBY bii di Abdu Mbow njëkkoon a biral ca jamono yee weesu.
Gis-gis bu ni mel tax na ba mu yaakaar ni palaasu Usmaan Sonko du woon Primature. Doon na gën a jekk mu bokk ci njiiteefu réew mi (présidence), nekk fa sekkarteer bu mag bi walla njiitu kabine Njiitu réew mi. Waaye, yemul ci loolu. Nde, yokk na ci ni Nguuru Pastef (l’État Pastef) moo nekk di juddu. Muy Nguur gu ragal ay jam-jam. Muy doxalin bob, dafay xirtal ci doxalinu doole te Saa-Senegaal yi mënuñu nangu lu ni mel.
WÉR-GI-YARAM
Door nañ 74eelu ndajem njiiti OMS (Organisation mondiale de la santé) fi Afrig. Ñu koy amalee fa Brazzaville, réewum Kongoo, li ko dale tey ci altine ji, 26 ut ba keroog alxames 29 ut 2024. Ndajem ren ji nag, ñiŋ ko jagleel ponk yu bari, rawatina lu jëm ci sopparñi doxiinu fànnu wér-gi-yaram fi Afrig, nees ko mën a suqalee ak jële fi jàngoroy laago wii ñuy wax poliomyélite.
Dinañu fa waxtaane itam lu jëm ci paatug tuut-tànk yi ak mbas mi ñuy wax Mpox te tàmbale law ci réewi Afrig yi, rawatina foofa fa Kongoo.
GAAL GI SUUX FA CUBALEL
Am na genn gaal gu suux fa Cubalel Nabaji, ab dëkk bu nekk fa diiwaanu Maatam. Mbir maa ngi xew tey ci altine ji. Ginnaaw bi ndog loolu amee, ñaari nit doŋŋ ñoo jot a mucc. Mu des juróomi ndaw yu réer ci biir ndox mi. Jamono yii, wallukat yi ak nappkat yi fa dëkk ñoo ngi leen di seet