LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (26/9/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LEERALI CÀMM GI CI LIÑ FI FEKK

Ci alxamesu tey jii, 26i pani sàttumbaar 2024 la Càmm gu bees gi joxe woon niki àpp ngir wax askan wi li Maki Sàll ak nguuram ga woon bàyyee. Elimaanu jëwriñ ji, Usmaan Sonko, jëwriñi koom-koom geek gog Yoon wi teewoon nañ ngir indiy leeral, ku nekk ci li ñeel fànn wi ñu la dénk. Li ñu fa biral nag, raglu na, doy na waar te ñaaw na. Daanaka, ci waxi Usmaan Sonko, Maki Sàll ak Nguuram ga ciy fen, mbuxum, càcc, luubal, njuuj-njaaj ak cuune lañu yoree woon réew mi. Dees na ci ñëwaat ci yaxal bu gën a yaatu.

NDAJEM NDEYU ÀTTE MI GÀNTAL NA WAA ATEL

Bu yàggul dara la ñi ëpp ci kujje gi taxawaloon lëkkatoo gii di ATEL (Alliance pour la Transparence des Elections). Ñoom nag, dañu taxaw rekk daldi song xeex bi. Moo tax, ñu jébbaloon ag dabantal ngir fànq dekkereb Njiitu réew mi. Maanam, dekkere bi nga xam ne moo woote ngir ñu amal wotey palug dépite yi. Waaye, loolu mujjul a àntu. Ndax, ndajem ndeyu àtte mi dafa gàntal seen càkkuteef boobu. Maanaam, li ñu wax nii mënul a tere ñu amal wote yi.

SEROM BÀNJAKI DEM NA KASO

Guddig àllarba jee weesu lañu ko tegoon loxo. Booba ba tey, moom Serom Bànjaki ma nga ca loxoy Yoon. Waaye, mbir yi dafa mujje am lu ca rax. Nde, mujj nañu ko yóbb kaso. Bees sukkandikoo ci waa Senegoo, li ñu gàll ci ndoddam mooy li ñuy dippe “escroquerie, detention illégale d’arme à feu et usurpation de fonction », maanaam njuuj-njaaj, yor ngànnaay ci lu dul yoon ak mbubboo ndombog-tànk bu mu amewul.

TEG NAÑU LOXO XAADIM BA

Xaadim Ba Njiitul Locafrique jamono jii ma nga ca loxoy Yoon. Ginnaaw bi ñu ko jàppee, dañu ko def li ñu naan “garde à vue”, maanaam dañu téyandi fa kaso ba. Li jot a rotagum ciy xibaar mooy ne, waa ji woo nañu ko ñaari yoon laata ñu koy jàpp, fukki fan ak juróom-ñeent ak ñaar-fukki fan ak ñeent. Laata muy fanaan guddeem gu njëkk fa sàndarmëri bu Fuwaar, waa duwaan ñoo ko njëkk a déglu. Bi ñu noppee, ci lañu ko def “garde à vue”. Bees sukkandikoo ci sunu naataangoy Senego, waa duwaan dañu koy laaj lu tollu ci ñaari-téeméeri miliyaar ak fukk ak juróom. Loolu la Xaadim Ba lànk ne du ci dal mukk. Ci gàttal, moom nanguwul mbir moomu nga xam ne teg nañu ko ci ndoddam.

XIBAAR ÑEEL COSTE WALLA DOOLEEL AG LËKKATOO WALLA AG MBOOTAAY CI WOTE YII

Ginnaaw bi wotey palug Njiitu réew mi jàllee, coppite yu bari am na ci géewu pólitig gi. Am na lëkkatoo yu tas, am na tamit yu sosu. Naka noonu, am na njiiti làng yu dem dooleel yeneen i lëkkatoo. Ci Misaal, kii di Elaas Mammadu Jaawo, ñu gën koo xame ci turu Maam Bóoy Jaawo, nga xam ne wote yii jàll dafa demaloon boppam, soppi na doxalin. Ñii di “La jeunesse du mouvement Sénégal Nouveau” bu Roos Wardini nee na Pastef lay jàppale sax.

Naka noonu, Mouvement Tekki bu Mamadu Lamin Jàllo, Grand Parti bu Maalig Gàkku, FDS-Les Guelwaars bu Baabakar Jóob, FEPP TAWFEKH bu Doktoor Séex Jeŋ ak ñeneen ñu bokkoon ci lëkkatoo Diomaye Président, donte ne sax am ñu ci génn, ñi ci ëpp Pastef lañuy àndal ci wote yii di ñëw.

Mu am tamit, ay lëkkatoo yoo xam ne sosu nañu. PUR (Sëriñ Mustafaa Si), PRP (Décce Faal), ARC (Anta Baabakar Ngom), AGIR (Ceerno Bóokum), Taxawu Sénégal (Xalifa Sàll), Les Serviteurs (Paap Jibriil Faalà) ak Gueum Sa Bopp (Bugaan Géy Dani) sos nañug lëkkatoo dippe ko Sàmm Sa kaddu/Sauver le Sénégal. Abdul Mbay ak Ceerno Alasaan Sàll sos nañu ag lëkkatoo gu ñuy dippe Senegaal Kese. Ñii di waa APR ak PDS sos nañu lëkkatoo gu ñuy wax Takku-Wallu Sénégal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj