Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo nga woon fa Réewum Gine Bisaawu, doon fa amal tukkib ñaari fan, 26 ak 27i fan ci weeru me 2025, ngir dëgëral lëkkatoo yi dox ci diggante ñaari réew yi. Naka noonu, amal na fa ay jotaayi waxtaan ak Njiitu réew ma Sëñ Umaru Sisoko Embaloo ak ay ndiissoo yu réew ma gir gën a dëgëral lëkkatoo yi ci wàlli pólitig, koom-koom ak dipolomasi.
Ci seen ndaje yooyu itam, takkal nañu fa Njiitu Réewum Senegaal li raaya bi ñu duppe Amilkaar Kabraal. Muy raaya bi gën a kawe fa réew ma. Ñu jagleel ko ko ngir feddali mbokk gi dox ci diggante ñaari réew yi.
Ci biir i kàddoom, Njiitu réewum Sénégaal li jaajëfal na naataangoom bu réewum Gine ak askan wépp ci teertu bu réy bi ñu ko jagleel. Naka noonoot, dellu na dëggal fonk gi mu fonk xaritoo ak mbokk gi boole ñaari réew yi. Loolu tax na muy féddali yéeneem ci ànd dogu ngir gën a jëmmaal lëkkatoo yi.
NJÀNG MU KAWE MI
Fa jàngune Gaston Berger, kurélug ndong yi, CESL (Coordination des Étudiants de Saint-Louis), a ngi ñaawlu dige yi ñuy wax ne jëwriñ ji Abdurahman Juuf sàmmontewul ak ñoom. Démb ci altine ji lañu doon janook taskati xibaar yi ginnaaw bi ñu njëkkoon a dakkal njàng mi ci àppug ñaari fan. Naka noonu, ñuy dellu di woo kilifa yi ñu taxaw ci seen i njàmbat. Àpp yi ñu joxe woon ngir jébal leen tabaxte yees fay amal weesu nañu te ba léegi dara yeggul. Wax nañu itam ci lim bu jéggi dayo ciy ndogo yi fa Nguur giy dugal te 5 535i lal kott la dëkkuwaay ya am. Bees sukkandikoo ci li ñu fésal, ci 2024 mi rekk, Nguur gi dugal na fa 5 500i ndongo yu bees.
MBIRI MANSUUR FAY
Ëttu àttewaay bu kawe bi gàntal na bàyyeendig Mansuur Fay mi fi nekkoon jëwriñ ci Nguuru Maki Sàll. Ginnaaw bi ñu ko téyyendee démb ci altine ji, 26 me 2025, jëwriñ ji nanguwoon naa teg ci seen loxo dara ngir ñu féexal ko. Suufu mbey su nekk fa Sébikotaan la leen a bëggoon a tegal. Ci xayma, dina tollu ci 5i tamñaareet. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, Maki Sàll ci boppam moo moom suuf soosule te bokkoon na ci alalam ji mu fésaloon ciy am-amam. Waaye àttekat bi dafa ko ko bañal donte ni andiwuñu ay leeral ci li tax ñu gàntal ko.
TÀGGAT YARAM
Pape Caw siiwal na toftaleb sóor yi mu woo ci ñaari joŋante xaritoo yi Senegaal namm amal ci digganteem ak Irlànd ak Àngalteer (6 ak 10 suwe 2025). Taftaleb 26i sóor la siiwal. Ñu ràññe ci ñu yàgg a teewe ñu mel ni Idiriisa Gànna Géey ak Kalidu Kulibali, waaye itam ñàkk-teewu kii di Saajo Maane ci coobare boppam. Woo na itam Idiriisa Géey, di xale bob, guléet muy teew ci ékib bu mag bi.