Li des ci wotey 25 féewaryee 2024 yi yées na ñetti weer. Waaye, am nay lawax yu féete ci kujje gi yuy waxtaan ci suuf ak waa càmm gi. Abdulaay Sow moo ko siiwal. Fekk ñu doon ko dalal démb ci dibéer ji fa RFM, ci jotaayu Grand Juty. Muy xamle nag ni ci géewu pólitig bi lañ nekk te képp ku leen mën a jural njariñ ñoom waa càmm gi dinañu waxtaan ak yow. Balaa yàgg dees na xam ay kàngaam yu nekk ci kujje gi yu leen di fekkasi.
WÉR-GI-YARAM
Fa réewum Siin nemmeekooti nañ fa yokkuteg jàngoro yiy andi jafe-jafey noyi. OMS (Organisation mondiale de la santé), mbootaayu àddina si ñeel wér-gi-yaram moo ko xamle. Ñu gis sax ni xale yu ndaw yi la gën a yab. Li waral yokkute googu nag mooy matukaay yi ñu bàyyi léegi te jëlon leen ca jamonoy Covid 19 ba.
Naka noonu, jëwriñ ji ñu dénk wàllu wér-gi-yaram ak taxawu askan wi fii ci Senegaal di xamle ni OMS jëlagul lenn ciy ndogal ñeel way-tukki yiy dem Siin. Waaye warees na ci nit ñi ñu wattandiku diy tukki bu nu nemmeekoo ci seen yaram màndargay jàngoro jafe-jafey noyyi yi. Ba tax na ñuy sàkku ci ñi am màndarga yi ci tukki walla bu ñu jógee ci tukki, ñu gaaw dem kër dogtoor ca ba muy teel.
NJAAYUM GERTE GI
Ginnaaw bi Càmm gi yëglee ni njaayum gerte gi dina door ci bésub 30 noowàmbar bii di ñëw, kurélu way-yëngatu yi ci wàllu wi, nu gën leen a xam ci FNOPS/T (Fédération nationale des opérateurs privés stokers et transporteurs) a ngi laaj Càmm gi 71 tamñareet. Muy nag xaalis bu takku bu leen Càmm gi boole ameel ci kàmpaañ yi weesu. Ñuy sàkku ci càmm gi mu fay leen xaalis boobu bees bañee njaayum gerte gi ren am i jafe-jafe. Nde xaalis boobu lañuy jëfandikoo ci seen i jëflante ak bànk yeek campeefi kopparal yi.
MBIRI USTAAS UMAR SÀLL
Alin Tin yëy na yàbbi ci Mbiri Ustaas Umar Sàll mi yoon war a àtte ci àjjuma jii di ñëw, yemook 1 desàmbar 2023. Muy xamle ni Ustaas Umar Sàll boroom xam-xam bu mag la, di jàngalekat bu am daaray alxuraan ju mag. Ñu tëj ko ndax li muy jàngale doon na lu muy mettitlu. Ba tax na muy yaakaar ci waa CUDIS ñu am ci pexem diisoo ba ñu mën koo féexal ci saa si.
BITIM-RÉEW
Fa réewum Burkinaa Faaso, am mbas mu nuy woowe deng moo fa tàmbalee law. Dem na sax ba laal diwaani réew mépp. Ñi ci jot a ñàkk seen bakkan tollu nañ ci 570i (juróomi téeméer ak juróom-ñaar-fukki) doom-aadama. Am naat 123800i (téeméer ak ñaar-fukk ak ñetti junni yu teg juróom-ñetti téeméeri) doom adama yu ñuy ragal ni moo leen dal.