Ni ñu koy defee ayu-bés bu jot, démb, ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yi. Mu am ndogal yu am solo yu fa Njiitu réew mi jël. Nde, kenn umpalewul réewum Senegaal mi ngi dëgmal bés bu màgg te am solo ci am mbooram. Muy bés bi nga xam ne ci la moomee boppam. Dinañu màggal bés boobu ñeenti fan ci weeru awril. Lii mooy doon juróom-benn-fukk ak juróomeelu yoon wi ñu koy amal. Ndogal li Njiitu réew mi jël mooy ñu xoolaat nu ñuy soppee turi yenn yoon ak béréb yu nekk fii ci réew mi. Ndax, tur yi ñu leen tudde amul lu muy màndargaal ci mboorum Senegaal ak Afrig ci jëmmi boppam. Daanaka, yi ci ëpp ay tubaab lañu leen tuddee. Te, liy yoon mooy béréb yooyu nekk liy dekkal ay xew-xew ak jaar-jaari jàmbaar yi doon xeexal réew mi démb ak barki-démb.
WÀÑÑIG NJËGU CEEB BI
Jëwriñ ji ñu dénk wàllu yaxantu gi ak ndefar gi, Sëriñ Géy Jóob, xamle na, tay ci alxames ji, ne njëgu ceeb bi dina wàññeeku. Ceeb yi ñuy wàññi, mooy yiy jóge Inde, Thaïlande ak Vietnam. Ceeb yooyu, kilo bi mi ngi daan jar juróom-ñeent fukki dërëm ak ñaar. Léegi, wàññi nañu ci fukk ak ñaari dërëm. Kon, kilo bi mi ngi war a jar juróom-ñaar fukk. Njëg loolu dees na ko door ñetti fan ci weeru awril wii ñuy waaj a dugg.
APR BIND NA BATAAXAL WAA FMI
Bu yàggul dara la Ëttub cettantal gi génne ag caabal di ci wane ni Nguur gi fi jóge yoree woon koppar gi diggante 2019 ak 2023. Ginnaaw gi la waa FMI dëggal boru Senegaal bi ak yi ci laxasu yépp. Loolu nag la waa APR ne duñu ko nangu. Te, duñu bàyyi mu jàll. Ndax, dañoo jàpp ne dafa am lu Nguur gu bees gi laxas ci yëf yi. Ba tax na, bind nañu ab bataaxal di sàkku ci waa FMI ñu amal ak ñoom ndajem liggéey ñeel caabalu googee. Su ko defee, ñu mën leen a jox ay tontu yu leer ci tuuma yu réy yi ñuy teg ci seen der. Ndax, ñoom it liggéey nañu ak ñu xarañ ci wàll woowu ba defar wayndare wu baax. Muy wayndare wow, day weddi li nga xam ne ay mbiri pólitig kepp la.
LAT JÓOB DU MUJJEE GÉNN
Démb la ay xibaar rotoon ci ne Lat Jóob day génn kaso. Nde, ëttu tuumalaate gi moo ko bàyyi bàyyig négandiku ba noppi takkal ko lam. Ñu jàppoon ne sax day génn démb walla tay. Waaye, loolu mujjewul a àntu. Ndax, toppekat PJF (Pool Judiciaire Financier) bi moo ci àndul. Kon, Lat Jóob day des fa kaso ba.
Kii di Ardo Ñing moom mujj nañu ko bàyyi démb, ci àllarba ji. Loolu terewul, ñu daan ko ñaari ati kaso yoo xam ne du leen tëdd. Rax-ci-dolli, ñu alamaan ko lu tollu ci ñeen-fukki junni.
DÀQ NAÑU NDÉGLUG ASIIS NJAAY
Tay, ci alxames ji, lañu waroon a déglu Asiis Njaay ci mbirum luubal mu ñu koy tudd. Luubal gi, mbirum àngare la mu tollu ci ñetti miliyaar yu teg. Looloo taxoon ñu woolu ko ngir mu indi ay leeral ci mbir moomu. Waaye, moom Asiis mujjul a dem bees sukkandikoo ci waa Libération. Nee ñu, moom moo sàkku ñu dàq ndéglu gi. Ndax, tay lañu doon def ndaje ñeel jëfandikoo gi. Looloo tax, ñu mujjee dàq ndéglu gi ba alxames jii di ñëwaat.