LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (27/9/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

GÀMMU 2023

Tey, àllarba, yemoo ak ñaar fukki fan ak juróom-ñaar ci sàttumbaar (weeru tubaab), fukki fan ak ñaar ci weeru gàmmu (weeru wolof) mbaa raabiyal-awwal (weeru araab) lañuy màggal juddug Yonnent bi (sallal laahu alayhi wa sallam). Guddi googu mu ganesee àdduna nag bari na fu ñuy koy màggalee fi Senegaal. Waaye, dëkk yi ci gën a fés mooy Tiwaawon, Kawlax… donte ne sax am na yeneen i dëkk yu koy màggalee noonu ci biir réew mi.

LU BEES ÑEEL MBIRUM USMAAN SONKO 

Lu jege ñaari weer ginnaaw bi ñu ko tegee loxo, moom Njiitul Pastef li, ba tey ma nga ca raglu ba. Li sababoon dem ga foofu mooy xiifal gu mu dooroon ba mu mujj néew doole lool. Dakkaloon na xiifal googu ci ndoorteelu weer wii. Boobaak léegi nag ma nga ca raglu ba. Li jot a rotagum ciy xibaar xamle nañu ne jamono jii mi ngi am tan bu baax. Ba tax na fii ak ub diir dina dellu ca kaso ba, foofa ca Sébikotaan.

MAROG MOOY AMAL CAN 2025

Joŋanteb futbal bi dajale réewi Afrig ya ca jàll dees na ko amale ren jii fa Koddiwaar. Maanaam CAN 2023 bi ca réew moomu lay ame. Waaye, bi ci topp nga xam ne atum 2025 la, fa Marog lay ame. CAF (Confédération Africaine de Football) moo jël ndogal loolu ginnaaw bi waa Alseri gi ñu doon xëccool bàyyee. Maanaam,  bi yëf yi desee ab diir ba ñu war a fésal kiy amal xew-xew boobu ci la ñii di waa Alseri sempee seen ndënd. 

NISEER GÉNNEE NA SYLVAIN ITTÉ CA RÉEW MA

Xeex ba dox ca diggante sóobare sa jiite réew ma ak waa Farãs ma ngay wéy ba tey. Li ko sos mooy daaneel gi ñu daaneel Nguuru Muhammet Basum. Moo tax ñoom sóobare si ñu jël ndogalu jaare xeex ba ca ka leen fa nekkal. Ba tax kii di àmbaasadu Farãs fa Niseer moom lañu mayoon ab diir ngir mu génn réew ma. Moom Sylvain Itté nag génn na réew ma tey ci àllarba ji. Waaye, mbir mi yemul foogfu ndax sóobare Farãs ya fa nekk dinañ na fa jóge fii ak njeexitalu atum 2023 mi.

MBËKK MI

Ndox maa ngi wéy ba tey di bóom doomi Afrig yi rawatina yoy Senegaal yi nga xam ne ñoo aakimoo yoon wi jamono jii. Ak li géej gi di faat ciy bakkan ni mu baree taxul ñoom ñu bàyyi. Mu bari ci lool ñoo xam ne jot nañoo dugg Espaañ. Waaye, mu am ci ñoo xam Daxla, fa Marog, lañu yem. Ñooñu nag dees na leen delloosi fii ci Senegaal niki ëllëg ci alxames ji. Doomi Senegaal yooyu nga xam ne war nañoo jóge Marog ñi ngi tollu ci limu ñaari téeméeri nit ak ñeent-fukk ak juróom-ñaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj