LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (28/11/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SAMIYEL SAAR DEM NA KASO

Àjjuma jee weesu lañu ko tegoon loxo. Booba ak tay nag, ma nga ca loxoy Yoon. Waaye, mel na ne am na lu yokku ci mbir mi. Ndax, mujj nañu koo yóbb kaso. Li ñu koy toppe mooy li ñuy wax ci farañse “abus de biens sociaux”. Kon, moom Samiyel Saar, nekkoon fi jëwriñ (ministre de l’énergie) ca jamonoy Abdulaay Wàdd, dina fanaan tay guddeem gu njëkk kaso.

JÀPP NAÑ KOMANDAŊU FUNJUÑ

Gendarmerie prévôtale” moo teg loxo takk-der boobu. Li ko waral mooy ne komandaŋ bi dafa doon dóor ab waxambaane buy wuyoo ci turu T. Jaata. Moom, T. Jaata, mi ngi tollu ci ñaar-fukki at ak juróom. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, waxambaane boobu dafa defoon aksidaŋ. Ginnaaw gi, dañoo fekk ci moom yàmbaa. Ci mbir moomu la ko komandaŋ bi doon laaj ca fa mu nekk ca lalu raglu ba. Mu mel ne ku ci xamul dara. Ca la ko komandaŋ bi dóoree. Ndekete, am na magam ju jigéen ju fekke mbir mi. Moom mag ji, moo dugal ab pelent fa toppekat ba. Ci lañu tegee loxo komandaŋ bi.

BÉS BI ÑU JAGLEEL DAARA

Tay, alxames 28i pani nowàmbar 2024 moo yemoo ak bés bi ñu jagleel daara yi fii ci réew mi. Daara nag, bu ñu ko waxee fii ci Senegaal, li ñu ci jublu mooy daara yiy jàngale Alxuraan ak léeg-léeg xam-xam ci wàllu diine. Kon, daara (école) yiy jàngale araab, farãse, àngale, añs. bokkuñu ci. Lii mooy ñetteelu yoon (édition) ñuy amal xew-xew bi.

SARKOO PELENT NA AY SAABALKAT AK I SAABALUKAAY

Sarkoo mbër la moo xam ne? ñu bari ràññee nañu ko ci làmb ji. Moom nag, dafa jébbal ab pelent ngir setal deram. Ndax, ci jamonoy kàmpaañi wotey palug dépite yi dafa amoon ab jàmmaarloo bu metti bu amoon fa Ndar. Mu amoon ñu ñu fa jotoon a gaañ. Ginnaaw gi lañu teg loxo luy tollu ci juróom-ñetti fukki nit ak benn. Mu amoon nag, ay saabalukaay ak i taskati-xibaar yu siiwaloon ne moom Sarkoo dafa bokk ci ñi ñu jàpp. Ndax, moom dafa bokk ci ñiy wattu kaaraange Bàrtelemi Jaas ak waa Sàmm sa kàddu. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, ñi mu duut baaraam ci pelent bi mu jébbal fa “Division Spéciale de Cybersécurité” mooy Ngóone Saaliw Jóob, Coro Màndelaa, Waa Senegoo ak waa Walfnet. Li mu ko dugge mooy setal deram. Ndax, li gën a doy-waar ci yëf yi mooy bi jàmmaarloo yooyu di am sax fekku ko ci biir-réew mi.

MAAS MBUUB JÓGE NA WALF TV

Démb, ci ngoon la siiwal xibaar bi ci xëtu Facebookam laata muy amal aw waxtaanam wu mujj fa kër googu. Li mu layalee mba gi nag, mooy ne dafa bokk ci ag làngu pólitig. Ci gàttal, nee na dafa far, looloo sabab mba gi. Dafa di, moom dafa bëgg a am sañ-sañ ak péexte guy tax mu mën a sóobu bu baax ci liggéeyal naal bi.

JEAN-NOËL BARROT MOOY TEEWAL MACRON FA NDAKAARU

Dibéer jii ñu jëm yemoo ak benn fan ci weeru desàmbar mooy bés bi ñuy màggal xew-xewu Caaroy 44. Mu nekk bésub tiis boo xam ne Farãs am na ci wàll wu réy. Ba tax na, ñu baree ngi ko ci doon séentu, moom Njiitu réewu Farãs, Emmanuel Macron. Waaye, moom du ko mujje teewe. Ki ko fiy teewal mooy jëwriñ ji mu dénk mbiri bitim-réew, Jean-Noël Barrot.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj