Ay weer ginnaaw ba ñu tëjee daara ju kowe jooju, ba tey buntam yaa nga tëje. Mu mel ni kilifa yi jël nañu yoonu ubbiwaat ko. Li ko waral mooy bànqaas bi ñuy dippe “Faculté des Lettres et Sciences Humaines” (LSH) dina tàmbaliwaat njàngaleem. Maanaam, njàngale mi dootul yem ci lënd gi. Bànqaas googu xamle na ne njàng mi dina fa tàmbaliwaat ñetti fan ci weeru saŋwiye atum 2024 ngir ñu mën a àggale ñaareelu xaaju at mi. Lees xamul kay mooy ndax ndogal dinañu ci laaxaale yeneen bànqaas yi am déed ? Li ci kanam rawul i bët.
SEYDINAA UMAR TURE SEMPI NA DËNDAM
Lu tollu ci ñaari weer kepp ay bëgg a des ci wote yi, moom Seydinaa Umar Ture ñu gën ko xame ci “Kàppiten Ture” sempi na ndëndam. Donte ne sax jotoon naa jël ay xobi baayaleem, loolu terewu koo teggi tànkam. Nee na li ko sabab du lenn lu dul ne loolu ci seen i pexe la bokk ci wàllu pólitig. Mu yokk ci ne loolu terewul wenn yoon ne ñoom dañuy des ci kujje gi. Kon daal, moom jamono jii fekkeegul kenn.
USMAAN SONKO
Ginnaaw ba mu jébbalee wayndareem ca ndajem ndeyu àtte mi ya taxul moom meeru Sigicoor bi mu teggi tànkam ci xeex bi mu nekk. Donte ne sax ma nga ca kaso ba tey, loolu terewul moom ak ug njabootam ñi ngi doxal seen liggéey ci wàllu pólitig. Ndax, seen lëkkatoo gii di “Sonko Président 2024” amaloon nañu am ndajem waxtaan démb ci ngoon, bi ñeenti waxtu jotee ca béréb bii ñuy dipper “Harmattan”. Rax-ci-dolli, ci gaawu gii lañuy samp Usmaan Sonko, tànn na ko ni seen lawax ci wotey 2024 yi. ACAPES, Pàrsel Aseni, lay xew miy ame.
WAA SYTJUST DELLOO NAÑU BUUM CA MBOY-MBOY GA
Sytjust (Syndicat des Travailleurs de la Justice) di kurél gi boole liggéeykati Yoon yi mi ngi wéyal xeex ba mu dooroon bu yàggul dara. Kenn umpalewul ne fan yee weesu rekk dakkaloon nañu seen liggéey ab diir. Wii yoon nag dinañu dakkal liggéey bi lu tollu ci ñetti fan. Li ko dale àllarbay tey jii ba àjjuma ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru desàmbar wii.
BOMBARJEE-RËG-RËG
Dibéer jii weesu la ñaari mbër yi doon jàkkaarloo. Rëg-rëg moo ci amoon ndam. Ñoom ñaar nag, ku nekk ci ñoom dagg nañu sa xaalis. Kii di Rëg-rëg dagg nañu ko lu tollu ci téeméeri junni ak ñaar-fukk ak ñeent. Bombarjee moom fukki junni kepp lañu ko dagg.
JÉYYA JA AMOON FA GINE
Guddig dibéer jàpp altine fukki fan ak juróom-ñett ci weer wii la béréb ba ñuy denc soroj bi lakkoon. Jéyya jooju metti woon na lool ca askan wa fay yeewoo. Ndax, lu tollu ci ñaar-fukki doomi aadama ak ñeent ñàkk nañu ci seen i bakkan. Lu tollu ci ñeenti téeméeri nit ak juróom-fukk ak ñeent jële ca ay gaañu-gaañu. Ñooñu gaañu woon ci, fanweer yaa nga ca lali raglu ya ba tey. Mu am ci fukk ak benn yu ñu xamul ba nii. Nguur gi nag xamle na ni lakk gi moom jeex na. Maanaam jamono jii lépp li fa doon tàkk fey nañu ko.