Dibéer jii weesu lañu doon amal wotey palug Njiitu réew mi. Ka jiitu ca wote ya mooy Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Moom Njiitu réew mi ak mbooleem lawax yi nangul ko ndamam li, daldi ko ciy ndokkeel. Démb ci àllarba ji la doon amal ndajem jëwriñam mu mujj. Mu ubbee ko ay kàdduy cant ak ngërëm jëmale leen ci ay ñoñam ak askanuw Senegaal. Boole ci fésal mbégteem ci anam yi wote yi amee. Rax-ci-dolli, di ndokkelewaat kii di Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Muy woo waa nguuram, ay jëwriñam ak ñépp ñi nga xam ne bokk nañ ci, ñu jël matuwaay yi war yépp ba ñu mën a jébbal lenge yi ki ko wuutu. Yemul foofu kese. Ndax, àddu na ci anam yi ñu war a màggalee bés bi ñu moomee sunu bopp, muy ñeenti fan ci weeru awril.
NDAJEM NDEYU SÀRTI RÉEW MI MAY NA LAWAX YI WENN FAN NGIR ÑU DABU
Démb ci àllarba ji la ëttub dabu bi génnee njureefi négandiku yi. Bi njureef yi génnee nag, mel na ni mbetteel moom amu ci. Ndax, mbañ-gàcce yi gàcceeluñu Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Waaye, loolu terewul ëtt boobu jox lawax yi wenn fan ngir ku bëgg a def ug dabantal ci ñoom, mu def ko na mu gën a gaawe. Ndax, tey ci alxames ji bu guddi gii xaajee (00h) la àpp boobu di jeex. Su ko defee ñu mën a génnee njureefi mujjantal yi.
WAA PASTEF TEGGI NAÑ TUUMAY YÉENEKAAYU SOURCE A
Ginnaaw bi seen lawax bii di Basiiru Jomaay Fay jëlee raw-gàddu gi ci wotey 2024 yi, dañoo amal ay coppite ci wattukati kaaraangeem. Maanaam, ña ko daan aar, dootuñu ko aar. Léegi, ñii di waa GIGN (Groupement d’Intervention de la Gendarmerie Nationale) ñoo koy aar. Bi loolu amee nag, dafa am kibaaraan (Source A) gu fésal ne kii di Usmaan Sonko tamit, ñoom ñoo koy aar. Kii di Sadix Top ak El Maalig Njaay bokk ci kilifay Pastef yi, biral nañ ci seen xëti Facebook ne loolu kibaaraan gi bind du dëgg. Usmaan Sonko mi ngeek i wattukati kaaraangeem ya mu amoon ba tey. Li kibaaraan gi wax ay kàcc la. Rax-ci-dolli, moom Sonko sàkkuwu ko, te it, amu ko.
GRADEC NJUKKAL NA ASKANU SENEGAAL
GRADEC (Groupe de recherche et d’appui conseil pour la démocratie participative et la bonne gouvernance), ag kurél la gog, dafa yebaloon lu tollu ci juróom-benn fukki ndaw ngir ñu saytul ko wote yi. Waaye, mel na ni néew na ay jafe-jafe walla ay coowoo yu ñu nemmeeku yoy, mën na am ay njeexital ci wote yi. Loolu nag, ñu ciy sant askanu Senegaal. Boole ci tamit di ndokkeel Basiiru Jomaay Fay mi nga xam ne moo fiy wuutu Njiitu réew mi fegal, Maki Sàll.
XEW-XEW BU DOY WAAR FA NJEMAAN
Njemaan, ab dëkk la bu nekke fa Sowaal. Benn sàmmkat buy wuyoo ci turu B. Ka moo fa bóom benn moroomu sàmmkatam bu tudd N. Ka. La leen boole ba bakkan rot ca moo yéem ñépp. Nee ñu, N. Ka moo dóor wenn nagu B. Ka. Moom nag, loolu neexu ko dara. Ca la coow la doore. Ñu jàppante, jaasi yi naaw. Ñu nekk ca ba B. Ka bóom ko. Moom B. Ka nag, jamono jii ma nga ca loxoy Yoon. La mu layale jëfam jooju mooy ne da doon aar boppam.