Coowal “DPG” (Déclaration de Politique Générale) dafa mel ni, bés bu set, day gën a takkarnaase. Ñi koy xamb mooy ñenn ñiy jàppale Nguur gi fi nekk ak ñi leen di joor i xeer. Bu ñii waxee jaar nii, ñee wax, jaar nale. Ndax, bu dee ku ci mel ni Ceerno Bóokum ak Bugaan Géy Dani dañoo jàpp ne elimaanu jëwriñ yi amul lu muy xaar ngir def ko. Walla fekk dafa bëgg a salfaañe sàrti ndeyu àtte yi. Kii di Aminata Ture, moom gisewul mbir mi noonu. Nde, dafa jàpp ne, Ngomblaan gi fi nekk jamono jii, nekkul ci li neex askan wi. Maanaam, wonewul bëgg-bëgg yi askan wi woneel boppam ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru màrs. Kon, lan moo war a tax elimaanu jëwriñ yi di def “DPG” ci Ngomblaan goo xam ne yelloowu ko. Moo tax mu jàpp ne dañoo war a tas Ngomblaan gi fanweeri fan ak benn ci weeru sulet wii ñuy dugg. Su ko defee elimaanu jëwriñ yi mën a def “DPG” bi ñiy coowoo jamono jii. Waaye, kii di ndeyu-mbill ji nga xam ne, moo waral coow lépp, mujj naa àddu ci mbir mi.
USMAAN SONKO ÀDDU NA
Elimaanu jëwriñ mujj naa àddu ci coowal “DPG” li nga xam ne moo lëmbe jamono jii réewum Senegaal. Ndax, bu yàggul dara, dépite bii di Gii Mari Saaña daf ko bindoon ab bataaxal di sàkku ci moom mu bañ a ñëw fa Ngomblaan ga. Depite yi ak ñu bari ci Saa-Senegaal yi jot nañu seen tontu. Nde, moom ndeyu-mbill ji, xamal na leen ne du def ab “DPG” ci Ngomblaan gi xam ne moo fi nekk jamono jii. Xibaar boobu mi ngi ko biral ci xëtu Facebookam. Mu xamle ci ne, “DPG” bi pare na. Waaye, du ko def. Mu teg ko ci dog 55 bu ndeyu àtte yi ak sàrt yi tënk Ngomblaan gi. Waaye, bu ñu nangoo amal coppite yi ci war diggante fii ak fukki fan ak juróom ci weeru sulet dina amal “DPG” bi ñépp di xaar.
BÀYYI NAÑU DOORO GÉY
Lu jege weer ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ak léegi, moom Dooro Géy am na xibaar bu neex. Ndax, kenn umpalewul ne dañu ko téye woon ñeel mbirum suuf mi ñu ko doon toppe ba yóbbu woon ko ci kaso. Waaye, mujj nañu koo bàyyi. Bàyyi gi nag, dafa am lu mu àndal. Nde, dañu koo def li ñuy dippe “sous contrôle judiciaire”.
MOOR TAALA GAY JÓGE NA GFM
GFM (Groupe Futurs Médias) di genn ci këri tasukaayi xibaar yu ëpp doole ci réew mi, ñàkk na tey kenn ci ay liggéeykatam. Taskatu xibaar boobu di Moor Taala Gay moo fa jóge. Xibaar boobu mi ngi rot tey ci àjjuma ji. Li tax mu bàyyi nag, xameesagu ko bees sukkandikoo ci li Seneweb rotal ciy xibaar ñeel mbir moomu. Moom, Moor Taala, kenn la ci ñi gàddu woon mbind mi fa TFM boole kook yeneen i liggéey fa kër googu.
BÉSUB SET-SETAL
Ginnaaw bi ñu ko njëkkee amal, Nguur dina tóllanti beneen bésu set-setal. Nde, laata tabaski gi amaloon nañu bés bu ñu jagleel set-setal fépp ci biir-réew mi, Nguur gi jàppaat na bés. Wii yoon, mi ngi jàpp bés boobu juróom-benni fan ci weeru sulet wii di ñëw. Kii di Séex Tiijaan Jéy, jëwriñ ji ñu dénk wàllum ndox ndox ak cet gi, nee na Njiitu réew maa ngi sàkkuwaat ci askan wi ñu génn bu baax, jëmmal bés bi, liggéey liggéey bi. Su ko defee, bésub 6 sulet bi mën a raw bésub set-setal bu njëkk ba.
IGE DINA AMAL I CAYTU FA AIBD
Banqaasu caytu gii di IGE (Inspection Générale d’Etat) moo war a amal luññutug caytu fa AIBD (Aéroport International Blaise Diagne). Li ñu ko dugge du lenn lu moy xam nan lañu yoree woon kopparu béréb boobu ak nan lañu doon jële foofu nit ñi diggante 2017 ak 2024. Diir boobu nag, ñi ko jot a jiite mooy Duudu Ka ak Abdulaay Jéy, nga xam ne ci Nguur gi fi jóge lañu bokkoon. Ki jiite béréb boobu jamono jii mooy Séex Bàmba Jéy.