LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (29/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

KÀDDUY ÀLLIYUN TIN ÑEEL WAY-PÓLITIG YI

Àlliyun Tin, di kenn ci njiiti kuréli ma-xejj yi, yékkateeti nay kàddu jëme ci way-pólitig yi, rawatina ci seen melokaan jëme ci Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Mu leen di xamal ni ñépp a ko war a jox cër, weg ko, moo xam làng gi mu bokk la, lëkkatoo gi ko fal walla kujje gi. Njiitu réew mi càmpeef la, moo jiite Bokkeef gi, jiite Càmm gi, jiite làrme bi. Nekk na njiit lu ubbeeku, lu ñeme jam-jam te boole ñépp ci gis-gis bi mu am ci Senegaal.

Wax na itam ne bi mu faloo ak tey, gisagul ci moom luy nirook bëgg nguur, walla kilifteef. Ba tax na càmpeef yépp a war a roy ci moom ngir dooleel demokaraasi bi.

WOTEY NGOMBLAAN GI

Ubbi nañu kàmpaañ yi ñeel wotey Ngombalaan gi barki-démb ci dibéer ji. Naka noonu, way-pólitig yeek seen i ñoñ tàmbali nañu itam dagaan baati askan wi. Ñoo ngi tollu ci 41i toftale yuy xëccoo toogaani dépite yi. Ku ci nekk nag tàmbali naa dawal i pexeem ngir ëppaley xob keroog bésub 17 nowàmbar 2024. Daanaka ay mitiŋ,  ay njëgg ak i janook taskati xibaar yi ñoo ci gën a fés. Kàmpaañ bi nag, dees na ko amal ci diirub 20i pan laata ñuy àgg ci mbañ-gàcce yi.

AMET NDÓOY TËDDI NA KASO

Amet Ndóoy dina fanaan guddeem gu njëkk ci kaso bi. Moom, faramfàccekatu Sen Tv bi, Toppekatu Bokkeef gi, fa “Tribunal de Grande Instance” bu Ndakaaru moo ko dóor “mandat de dépôt”. Dinañu ko àtte keroog 4 nowàmbar 2024.

DEMUG SÉEX TIJAAN JÉEY FA BÀKKEL

Jëwriñ ji ñu dénk ndox mi ak cellal gi, Séex Tijaan Jéey, mu nga woon fa Bàkkel barkaatu-démb ci gaawu gi. Muy tukkite gu mu fa doon amal ngir nemmeekuji barab ya walum dexu Senegaal gi wann fa diiwaanu Maatam ak Tàmbaakundaa. Moom nag, li mu namm mooy sàkk i pexe ba ñu mën a jariñoo ndox moomu tere nelaw askan wi. Naka noonu, xamal na askan wa ne, Càmm gi am na naal wu jëm ci dekkil dexi Bàkkel yeek déeg yi. Askan wi dëkke foofu itam am nañu naal wu ni mel. Nguur gi dina leen ci jàppale. Te itam, dina amal i tabaxte ci barabi ndox yooyu ngir dooleel mbay mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj