LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (29/5/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

“BAD” AM NA NJIIT LU BEES

Tay, ci alxames ji, lañu doon amal wotey palug Njiitu bànk bii di BAD (Banque Africaine de Développement). Ay lawax yu cosaanoo ci réew yu wute ñoo ko doon xëccoo. Muy ku ci mel ni Aamadu Hot bawoo ci réewum Senegaal, Abbaas Mahamat bokk Càdd, Samiyel M. Memboo bokk Sàmbi, Siidi Uld Taah bokk Muritani ak Bajabulil S. Sabalala bokk Afrig-di-Sidd. Joŋante bi nag, xawoon na tar. Waaye, doomu Muritani jii di Siidi Uld Taah moo mujjee jël ndam li ci kaw naataangoom yooyu. Kon, moom mooy nekk Njiitu BAD lu bees lI.

MENN RÉEW, ÑAARI TABASKI

Ni ñu ko baaxoo woon di gise ci at yii weesu, daanaka noonu la demewaat at mii tamit. Ndax, réew mi woorandoowuñu, woreendoowuñu te naruñoo tabaskeendoo. Kon, loolu du guléet muy am ci réew mi. Dafa di, wii yoon tamit, na woon fa woon la. Nde, ñaari ndiisoo yiy saytu mbirum weer wi, ku nekk jàpp na bés. Ñii di CMS (Coordination des Musulmans du Sénégal), nee nañ julli gi àjjuma la, juróom-benni fan ci weeru suwe. Ña ca des CONACOCC (Commission Nationale de Concertation sur le Croissant lunaire), ne tabaski gaawu juróom-ñaari fan ci weeru suwe lay doon.

UBBITEG DAARA JU KAWE JA NEKK FA MAATAM

Ginnaaw daara yu kawe yi ñu jot a am ci réew mi, am na yeneen yu nekk ci yoonu tijjeeku, muy ju ci mel ni joj Maatam. Daara jooju ñu dippe Sulaymaan Ñaŋ, bu yàgg ba tay ña nga ca liggéey ba. Këru liggéey gi jiite liggéey ba xamle na ne xaar bi jeex na daanaka. Ndax, daara jooju dees na ko ubbi oktoobar 2026. Su ko defee mu tàmbalee dalal ay ndongo ni ko yeneen yiy defe.

TËJ NAÑU AADAMA ADUS FAAL

Aadama Adus Faal aji-bokk la ci làng gii di APR. Moom nag, li ñu ko tëje wii yoon mooy mbirum càccug xaalis. Maanaam, dafa am ku jaawale yónnee ko fukki junni ak ñeent ci sàqu Wave. Bi mu moom. Bi loolu amee, delloowul xaalisu jàmbur. Te, ki juumoon yónnee ko ko, mënatu ci woon jot. Ca la ko jure, ñu woolu ko, jàpp ko. Bees sukkandikoo ci waa Senego, dees na ko àtte ñaari fan ci weeru suwe.

XEW-XEW BU TIIS FA MAATAM

Genn gaal moo suux fa Werma. Werma nag, mi ngi nekk ci goxu Bokilaaji, nekk fa Kanel. Mu am sax ñetti bakkan yu ci jot a rotagum. Ndax, bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu jot a siiwal, juróomi doomi-aadama lañu woon. Te, ñett ñi kese lañu gis seen i néew. Ñaar ñi ci des moom, kenn tegaguleen bët. Ci gàttal, kenn xamagul ci lan lañu nekk, ñi ngi dundu walla faatu nañ. Fim tollu nii, dara leeragu ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj