BÀYYI NAÑU SÉEX YÉRIM SEKK, KADEER JA AK BUGAAN GÉY
Ci ndoorteelu ayu-bés bi lañu leen woo woon fa Yoon. Ginnaaw gi, dañu leen fa téye woon. Waaye, bàyyi nañu leen n̈u dellu ci seen i njaboot. Tay lan̈u leen bàyyi. Daanaka, ñoom ñépp ñoo bokkoon li ñu leen doon toppe. Nde, ñi ngi leen doon toppe biral ay xibaar yu wérul. Jamono jii nag, gàlluñu dara seen i ndoddu. Maanaam, teguñu leen benn daan.
WOO NAÑU CEERNO ALASAAN SÀLL
Tey, ci alxames ji lañu woo Ceerno Alasaan Sàll fa “Section de Recherches” bu “Caserne” Sàmba Jéeri Jàllo. Li waral woote bi mooy coowal ONAS li. Cig pàttali, Séex Jeŋ moo jiite woon ONAS. Ginnaaw gi lañu ko dàq. Bi ñu ko dàqee nag, ci la am ay tuuma yu dox digganteem ak jëwriñ jii di Séex Tiijaan Jéey. Ceerno Alasaan Sàll dafa jébbal ab jure ngir ñu leeral mbir moomu. Loolu moo waral ñu woo ko tey jii fa Yoon.
NJIITU RÉEW MI DU TEEWE NDAJEM PARI MA
Ñeent ak juróomi fan ci weeru oktoobar lañuy amal am ndaje fa Pari, ca réewum Farãs. Ndaje moomu, ñi ngi koy dippe “Sommet de la francophonie”. Njiitu réewu Senegaal, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, du teewe ndaje mooma. Dañu ko fay teewal bees sukkandikoo ci waa Seneweb. Li sabab ñàkk a demam googu nag, leeralaguñu ko.
Waaye, loolu terewul ne dina amal beneen tukki fa réewum Turki ci njeexitalu weer wii. Tukki boobu, dina ko amal fanweeri fan ak benn ci weeru oktoobar. Lii nag mooy yoon wu njëkk muy seeti Njiitu réewu Turki, Reseb Tayib Erdogan. Dafa di, kii di Njiitu réewu Turki moo sàkku (invitation) ci Njiitu réewu Senegaal mu ñëw fa.
JÀNGALEKAT YI UBBI NAÑU
Tey, alxames ñetti pani oktoobar la jàngalekat yi ubbi. Ci bés boobu la atum njàng meek njàngale mi ci daara yu suufe yeek yu digg-dóomu yi di door. At mi di jeex ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru sulet atum 2025. Tey, ñoom ñooy ubbi ak mbooleem ñi nekk ci banqaasi càmpeef yooyu (personnel administratif). Ndongi yi moom, dinañu ubbi altine jii di ñëw juróom-ñaari fan ci weeru oktoobar, bu juróom-ñeeti waxtu ci suba jotee.
TUXAL NAÑU BÉSU AAJARUB NAAL BI
Altine juróom-ñaari pani oktoobar lañu ne woon lañuy aajar li ñuy dippe “Nouveau référentiel de politique économique et sociale pour un Sénégal souverain, juste et prospère”. Waaye, àpp googu dañu koo mujjee dàq. Léegi, dinañu ko amal fukki fan ak ñeent ci weeru oktoobar wii fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf). Démb, ci àllarba ji, la ko Njiitu réew mi siiwal fa ndajem jëwriñ ya. Moom, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, xamle na ne moo koy jiite.