Barki-démb ci dibéer ji lañu doon màggal 80eelu pàttalikug Caaroy 44. Ñu doon ko amal ci njiiteefu Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak ci teewaayu kilifay réew mi ak yu bawoo fa bitim-réew. Ginnaaw bi mu jëlee kàddu gi, Njiitu réew mi dellusi na bu baax ci solos xew-xewu Caaroy 44 ci sunu mboor, li ciy wareefi réewum Farãs miy ndayu mbill gi ak li ciy wareefi réewum Senegaal ak yu Afrig yi mu dal mu dal seen kaw. Naka noonu, mu fas yéene jël juróomi ndogal ak 16i réewi Afrig yi ñu ko séqal ngir sàmm ko ak di ko dundal : def seen sëg yi fa Caaroy ab béréb bu mbooleem réew yi ñu bawoo woon mën di daje, di leen fàttaliku ak di leen ñaanal ; ubbi sàqum gëstu (centre de documentation et de recherche) jagleel leen ko ; duppe leen ay yoon ak i bayaal ngir xew-xew bu tiis boobu bañ a fay ci sunug dund ; dugal mboorum Caaroy ci njàngale mi ngir doomi réew mi teel koo xam bu baax ; ak saxal màggal bésub 1 fanuw desàmbar mu jot ngir di fàttaliku bóomug Caaroy atum 1944.
NGOMBLAAN GU YEES GI
Démb ci altine ji, 3i pani desàmbar 2024, lañu doon taxawal Ngomblaan gu yees gi. Elaas Maalig Njaay mi nekkoon jëwriñu yaale ji ci Càmm gi lañu tabb mu doon njiit la. Ginnaaw bi ñu ko tabbee, jot na a jiite liggéey bi njëkk bu aju ci tabb 8i tof-njiitam laata ñu doon taxawal pekk yi. Naka noona, muy jotaayu Ngomblaan bi njëkk. Ñu leen di xaar ci fan yii di ñëw ñu daldi sóobu ci liggéey bi leen di xaar dëgg-dëgg, rawatina gafaka gi Nguur gi war a doxalee ci atum 2025 mi.
SAABALUKAAY YI
Nguur gi siiwal na démb ci talaata ji toftaleb saabalukaay yi mu nangul seen nekk. Ci biir 550i saabalukaay yu ñu mën a waññi ci réew mi, 380 ñoo ci bindu woon ci dalu web bi Nguur gi tijji woon ñeel mbir mi. Ginnaaw bi ñu jébbalee seen i wayndare, 112 kott la ci Nguur gi nangul. Ndax, bees sukkandikoo ci kàdduy jëwriñ ji, Aliyun Sàll. Ñi jotul jàll nag, may nañu leen àppu ñaari fan ngir ñu joyyantiku. Lu ko moy, benn ci ñoom du jote ci ndimbal yi Nguur gi di jagleel saabalukaay yi. Nguur gi fas na yéene itam yeesal tënkuwaayu saabalukaay yi (le code de la presse) ak CNRA, kurél gi leen boole ëmb.
DELLOO NJUKKAL USMAAN SÉMBEEN
Kilifay Afrigi jamono ji war nañu delloo njukkal Usmaan Sémbeen. Loolu gis-gisub Àlliyun Tin la. Njiitu Afrika Jom Center li biral na ni Sémbeen Usmaan dafa xeex dundam gépp ngir siggil kembarug Afrig, doon xeex ngir sàmm ngor ak yoon ñeel doomi Afrig yi. Moom Sémbeen ci boppam dafa mës a bëgg a ñoŋal lépp luy liggéeyam. Sàmba Gajigo mi ko xam bu baax mën na ko seede. Ba tax mu jàpp ni doon na jaadu ñu taxawal miise sinemaŋu Afrig bu dale lépp luy liggéeyu Sémbeen ci sinemaŋ. Dellu na sax sàkku ci meeru Ndakaaru, Bàrtelemi Jaas, mu dippee Usmaan Sembeen béréb bii di Place de l’indépendance.
LAKK GA AM FA MBUUR
Lakk gu metti moo am fa diiwaanu Mbuur. Genn kër moo fa tàkk ci guddi gaawu jàpp dibéer fa kàrce bi ñu naan kàrce 11 nowàmbar bu Mbuur. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, bi 4i waxtu di jot jàpp 5i waxtu, lañu ko yëgal wallukat yi. Waaye, laata ñu leen di xettali, 6i doom-aadama, ñépp bokk ca kër ga, jot nañu ñàkk seen i bakkan. Li waral lakk gi nag kenn xamagu ko. Waaye yoon ubbi na ci ab gëstu.