Yoon waa ngi wéy di bóom i doomi-aadama. Saa su ñu jàppee wàññeeku na, fekk booba la yées. Tay, ci alxames ji rekk, am na ndog mu metti mu am ba ay bakkan rot ci. Ma nga ame ci yoonu Lingeer wi ak Maatam fa wetu dëkk bii di Nakara. Benn biisu “Dakar Dem Dikk” ak benn “Allo Dakar” ñoo fa mbëkkante. Lu tollu ci juróomi doomi-aadama ñàkk nañu ci seen bakkan bees sukkandikoo ci waa “Seneweb”.
WOTE NAÑU SÀRT BIY LEERAL AMNISTI BI
Daaw ci weeru màrs lañu wote woon sàrtu Amnisti bi ngir far xew-xewi pólitig yi am diggante 2021 ak 2024. Sàrt boobu sax moo taxoon ñu bàyyi ñi ñu tegoon loxo ñépp. Donte ne sax, ñoom dañoo bañoon ne duñu ko wote. Waaye, mujjoon naa jàll fa Ngomblaan ga. Ndax, ñi sàkku woon ñu wote ko ñoo fa ëppoon doole. Waaye, bi waa Pastef jëlee Nguur gi dañoo wotelu beneen sàrt buy leeral walla sax tekki sàrt boobee. Su ko defee, ñi laale woon ci xoqatal yeek bóom yi, Yoon mën leen a topp. Démb, ci àllarba ji, lañu yóbbu woon sàrt boobee fa Ngomblaan ga. Téeméer ak ñeen-fukki dépite ak juróom-benni ya fa teewoon jot nañu koo wote. Téeméer ak ñaar-fukk ak juróom-benn ñoo ci ànd, ñaar-fukki dépite ñoo ci àndul. Kon, loolu day firndeel ne sàrt bi jàll na. Ndax, ñi ci ànd ñoo ëpp fuuf ñi nga xam ne ànduñu ci.
ELIMAANU JËWRIÑ YI DINA DELLU FA NGOMBLAAN GA
Bu yàggul dara la jóge fa Ngomblaan ga moom elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dina fa delluwaat. Ñi ngi koy séentu fa béréb boobu fukki fan ci weeru awril wii ñu nekk. Wii yoon mooy doon ñetteelu yoonam muy dem fa béréb boobee. Li ñu ko dugge mooy waxtaan ak dépite yi ci tolluwaayu réew mi. Leeral ak tontu laaji dépite ñeel yorinu réew mi. Ndax, loolu mooy liggéeyu dépite. Maanaam, saytu ni Nguur gi doxalee ak ni mu yoree réew mi.
DAAN NAÑU BAABA AYDARA
Ayu-bés bale ñu génn (19 màrs) lañu ko tegoon loxo ci ab bérébu liggéeyukaayam (boulangerie). Li taxoon ñu jàpp ko mooy ñàkk a sàmmonte ak li ñu tëral ci ni mburu mi war a tollu (poids). Tay, ci alxames ji, lañu ko àtte fa ëttu àttekaay bu Ndar. Daan nañu juróom-benni weer yoo xam ne ñett yi lay tëdd. Rax-ci-dolli, ñu àllamaan ko lu tollu ci ñeen-fukki junni. Li ñu ko daane, moom saabalkat boobu, mooy ŋàññi walla saaga ak jotee ak ndawu Càmm gi ci wàllu liggéeyam.
YÉGLEB SEN’EAU AK SONES
SEN’EAU ak SONES ñooy yégal askan wi ne dafa ay liggéey yu ñuy amal ngir defaraat ab yàq-yàqu ci ALG (Adductions du Lac de Guiers). Gaawu bii ñu jëm lañu koy amal. Liggéey yooyu nag, dina yeexug ndox mi ci ni muy ñëwe. Dina dem sax ba ñu àgg ci ñàkkum ndox ci béréb yi nga xam ne ñetteelu isinu Kër Momar Saar bi moo leen di sédd. Dëkk yi muy gën a laal mooy Ndakaaru ak “Banlieue” bi, Rifisk ak li ko wër, Mbuur ak Sowaal Faajuj ak dëkk ak dëkkan yi nekk diggante Cees ak Luga. Liggéey bi, mën naa bañ a yàgg. Te, njort nañu ne yëf yi dina delluwaat na mu meloon ci guddig gaawu jàpp dibéer.