LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (3/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDAJEM ETAASINI AFRIG

Ayu-bés bii ñu jëm lañuy amal ndaje mii ñu dippe “sommet Etas-Unis-Afrique”. Muy ndaje mu am solo moo xam ne du réew yépp a ko mën a teewe. Réewum Senegaal bokk na ci juróomi réewi Afrig yi ñu fa woo. Kon, Njiitu réewum Senegaal, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, bokk na ci Njiitu réew ya ca war a teewe xew-xew boobu. Ndaje maa ngay ame fa Wasiŋton, diggante juróom-ñeenti fan jàpp fukki fan ak benn ci weeru sulet.

NJIITU RÉEW MI ÀDDU NA CI DOXALINU TAKK-DER YI

Coowal ñi génn àddina fa Rooso ak Kàmbereen lëmbe na lool réew mi jamono jii. Te, seen ug génn àddina ñu bari dañu cee duut baaraam takk-der yi. Mu doxalin woo xam ne Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, naqarlu na ko lool. Nde, dafa gis ne ay mbirum caytook yu ni deme bakkan waru cee mën a rot. Rax-ci-dolli, peeñ yi mu ci gis ñaawlu na ko lool. Muy sàkku ci jëwriñu biir-réew meek njiitu Pólis bi ñu amal ci ay luññutu yu jaar yoon ca na mu gën a gaawe. Su ko defee ñu xam ku ci laale ak nan la ci laalee.

XEW-XEW BU YÉEME FA LUGA

Xew-xew bu doy waar moo am démb fa Luga, ca koñ bii di Kër Sëriñ Baara. Mi ngi am ay boori timis. Benn móodu-móodu bu tollu ci ñeen-fukki at moo fa xaru. Moom nag, yoroon na soxna ak ñetti doom. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, M. Faal ab sox la taal ci gémmiñam. Toppekatu bokkeef gi sàkku na ñu tijji ci ag luññutu ca na mu gën a gaawe.

JOGO JOTA FAATU NA

Naqar ak tiis la àddina si yeewoo tay, rawatina ñiy yëngu ci wàllu futbal. Saa-portigaal bii di Jogo Jota moo faatu ci am ndogum yoon mu metti. Moom ak rakkam ju góor jii di André Silva ñoo nekkandoo woon ci daamaram gii di Lamborghini. Moom, Jogo Jota, futbalkat bu mag la woon. Mi ngi nekkoon fa Àngalteer, ca këlëb bii di Liverpool. Mi ngi tolloon ci ñaar-fukki at ak juróom-ñett, amoon senn soxna ak ñetti doom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj